Réewum Senegaal tollu na diggante bu xat te mooy diggante dund ak dee gannaaw ba kuréel gi waroon a saytu sàrti-réew mi feeñale parparloom ne ki ñépp di mbàmb, neex nàqari day bokk.
Li ñépp yaakaaroon ne dinañu takk seen fit, def ni seen natangoo ya ca Maali gii mbaa Niseer defoon tas na! Wante Yàlla ak askani Senegaal dina leen àtte ci lu wér, ndax seeni maas a nga “La Haye” cóowu àddina sépp topp leen!
Nàqaru-xol dëgg lañu ame téy bi ñu gise ni Ablaay Wàdd ak ñi ko wër jógge di dal ci kow askan wi, genne seen sox di fétal aka réy ay xale, ay jiggéen ag ay màggat yu yorewul benn ngannaay bu dul seen fit, seen jom ak seen ngor!
ImageAblaay Wádd moo toraxal askanu Senegaal mi ko teral, mi ko yëkkati woon, teg ku fu mu masul a teg kenn daanaaka, dénkk ko ëllëgam ak ëllëgi doomam, denkk ko lépp li ko tax a beew ba def boppam Yálla di faat ay bakkan!
Askani Senegaal askan wu Yàlla màggal la, askani nit ñu am ngor lañu, am teraanga, gëm Yàlla. Képp ku tuur deretam Yàlla dina la sànkk saayiir ak baatin! Kenn mënu ci dara!
Ñépp xamoon nañu ne Ablaay Wàdd kilifaag mbëtt la: soo toppee ci ginnaawam mu ne “bul dëgg sama geen”, nga toloog moom mu ne “da nga maa bëgga yab”, soo ko jiitoo “mu ne toppal sama naaj”. Wante téy weesu na foofu, gaynde-sibi gu tëx, xiif yàpp la ba naan askan wi”Yeen a ngi may xeeñi seel”! Te ñun de askani Senegaal, xamuñu lu dul cere ak soow!
Li ko waroon moo doon lekk ci ndab li ñu ko jox joxin wu rafete rafet bu àddina sépp bàkk, ubb ko ba mu jekk wóo keneen! Wante lekk ba noppi xëpp ci suuf loolu la faye askani Senegaal!
Image
Laam-laame nag weesu na, artu itam wéy na! Lenn rekk a dés, ci képp ku yore kàddu, nga wax dëgg! Lu dul dëgg du yàgg te jenn dëgg rekk la: na Ablaay Wàdd dem! Menn ab picc mënul a yàqum réew! Moom ak doomam la ak seeni dag ak réewum lëmm, mu beggul lu dul tedd, dund ci teraanga, tedd ag jaamu-Yàlla!
Wante gudd nopp taxul a dégg, nde kon kenn du door mbaam te nag mujju mbaam ay tan, buuru buuri kasaara yi!