“Maa waxoon…waxeet!” kàddu yooyu njiitu réew mi yëkkëti ci ndaje PDS bi amoon ci 23 fan ci weeru suliye, weesu na waar ba faf wër àddina! Image Ñu bare ñu mel ni man dañoo waaru ba naan waaw, Góorgi moo lu ko jàpp, ba mu sañ a genne kàduu yu ni mel ci gemmiñam! Naka la kilifa gu tollu ni moom mën a waxee lu ni mel, réew mépp di ko dégglu! Su doon ndéyi-mbill ji da di gone walla mu xamadi, ñu xalkoon ne xanaa dafa amul ku ko diggël…!
Ngóor si de moom da koo tontu ne ko “Gor de ca wax ja”!; Seriñ Maansur Si Jàmmil ne ko “Borom kër gu taxaw buntu këram di tëgg ndëndam sañul a tereeti kenn ca kër ga mu njaayxolle”…Caat mu “Yen a marre”, moom nag day wax sànni rekk, dolli ca ne ” Màggatam 90 at, muy fen, kenn mëneesu ko denkkum réew…”
Wante ba tey itam lenn moom jàngees na ko ci mbir mii: mooy wax ag askan wi wolof, lu am solo la! Nde loo wax ñépp xam ko, jot si…su dee toj-toj, mbàmb li di benn! Bilaay naxekat yi jafandu bu dëggër ci làkku jambur ñoo xam li tax…Su ñépp doon wax ag askan wi làkk yi mu nàmp kon léegi kàcci neen fattu dëgg rekk falu…
Céy Senegaal…xameesatul kon de lu tax Kocc daan wax naan “Mag mat naa ba cim réew”? Ma foogoon ne sax li ku taxoon di wax loolu moo doon li mag, maanaam ki nga xam ne li ko dese ci àddinaam baretul, amatul ku muy ragal ku dul Yàlla, ba tax suy wax dëgg rekk a koy ñor! Du waxantu…waxatumaag wax-waxeet! Xanaa kon mag ma jóggoon ba Daaw Demba, buur bu rééwoon te toroxaloon askanu Kajoor, bëggee sànkk Kocc mi ne woon “Buur du mbokk”, jàkkarloo woon ag moom wax ko dëgg gu raw kaani ba noppi ne ko rey ma su la neexe, ndax weesu naa fu may ragale dee, mag moomu kon tey fa mu nekk ma ngay wàñaarru! Céy àddina! Wante lu tëgg tas de: Kuy waxaati daal na nga soorale nettali bi, ndax mooy liy des! Rawatina jamono jii nu toolu nga xam ne lenn reeratul, loo wax ci saa si àddina sépp jot si! Xalaas!
Maa waxoon waxeet!
Category: Politik
assalaammalekum fello Wolof speakers. How ae yu doing? Dekk naa ci Senegal between 1991 ak 1993, ci corps de la paix americain. Sama liggay weer u yaram ci vilass yi. My Wolof is broken. Tubaab naa. Sama wolof dafa tekk. Anyways have a nice day and remember, Donald Trump is an idiot.
Long Liv Ndoyeenne barga (Region de Loga)