Bubakar Boris Jóob kenn la ci bindkat yi gëna mag ci Senegaal ag ci Afrik. Bind na ay téere yu siiw ci kalaama farañse ag benn téere bu am solo ci Wolof bu mu tuddee Doomi Golo. Laaj-toontu bii yeenekaayu “Le Monde des Livres” moo ko amaloon ak moom ci 16 fan ci weeru Awril. Waxtaan woowu lañu leen fi tënkal…
Le Monde: Lu tax nga bind Doomi Golo ci Wolof njëkk…
Dama mas a bëgg bind ci Wolof, ndax ci sama gis-gis làkki réew mi dees leen a war a jox àq bi ñu yelloo. Ni ko Coetzee waxee “Bindkati Riisi waa Riisi lañuy bindal, bindkat yu Faraas waa Faraas lañuy bindal, waaye bindkati Afrik ñoom bindalu ñu waa Afrik, yeneeni askan lañuy bindal”…waay-xeltu yi gëna bari te amkoon dooleey jënd téere yi ci làkki Afrik, dañoo làggi ci xeeb làmmiñ yi ñu nàmp…
Le Monde: Ndax dafa am xew-xew bu am solo bu la sóob ci sopi làkk bi nga doon bindee ba léegi…
Su ma yeboo ne li gëna waral coppite boobu mooy mbóom-waaso ga woon Ruwaanda. Bañ-sa-bopp gaa, bokkoon na ca la waraloon jëyya ja, wante doxalinu koloñalist bi fi sax, amoon na ci wàll itam. Te kenn mënul a weddi ne Faraas ci boppam fésoon na ci ñi doon jàppale boomkat yi…Te li woon ndéyi-mbill gi dëgg ci mboom-waaso googu mu ngi laxasuwoon ci mbirum làkk, ci màmm gi ñu bari màmmoon ci kalaama farañse. Nguuru Faraas dafa làngoon ak boomkat yi, ndax rekk li mu yëgoon ne ci wàllu caada ak politik cofeel gi waa Front Patriotique Rwandais amoon ci angaleek-amerikeñ da doon lu koy gësëm. Foofa la doxee, gëna bañ gépp xeetu nooteel ci wàllu caada, gëna dollee bëgg a bind nag ci kalaama Wolof. Noonu la sóoboo ci biir nag, kom ni ñu koy waxee…
Le Monde: Amul yenn saa yoo doon am siiki-saaka bi nga sumbee loolu?
Ahakañ! Am na sax yenn saa yu ma amoon xel-ñaar dëgg sax, ndax sama njàngum bind yépp ci “francais” la, te boobu téere moo doon sama juróom-ñaareeli téere; wante ba ma koy bind dama meloon ni kuy doog a door…wante mujj gi suma yebboo ne bokk na ci téere yi ma gëna feexal. Baati biir yu bare tàmbalee di ma àwwu, rawatina ay baati jiggéen…
Le Monde: Lu tax ay baati jiggéen?
Ci sunu réew, jiggéen ñee gëna neew ci ñi jàng lekool, ci ñiy jàng nasaraan. Ba tax seen Wolof dafa seet te mucc-ayib!…
Le Monde: Lu la dellu xiir ci tekki Doomi Golo ci nasaraan?
Dama ne woon ca atum 2003 ne téere boobu deesu ko tekki lu dul ay ati at ca kanam. Ndax dama bëggoon mu demal boppam, wonne boppam. Ndax li doyoon waar mooy téeri bi dama koo noppee bind ci Wolof rekk, ñu bari tàmbalee maa laaj kañ laa ko fas-yeenee tekki ci tubaab, manaam daal “ci làkk dëggantaan”! Wante ci atum 2006 ba ma Toni Morrison woowee ngir ma jàng benn pacc ci sama téere bi tudd Murambi ca “Musée du Louvre”, ca laa tekkiwaale woon benn dóg ca Doomi Golo. Foofa la doog di yëg ne tekki ko jot na.
Le Monde: Ndax di nga ci bindaat ci nasaraan?
Waawaaw! Masu maa xalaat a bañ a bindati ci farañse. Wante li ma bëgg mooy fésal lëj-lëj gi ci fàn woowu ci wàllu caada. Ndax dama jàpp ne mbindum-fent bi ay doomi Afrik di bind ci làkki nasaraan, mbindum-fent bu fi nekkagum rekk la, du lu fiy wéy!…Man ci sama wàllu boppam caageewul ne damaa bañ farañse…li ma bañ mooy folkoloor biy bàkkantu naan ” farañse bi sunu xarit ya Afrik di làkk” ag lépp li muy junj ci xelu nit ñi…
Le Monde: Ndax ci sa téere yi am na bu ci nit ñi gëna sopp ci Afrik
Waaw Murambi, nettali la xew-xew ya amoon Ruwaanda, ñu ngi koy jàngale ci lekool yi…”Le temps de Tamango” itam ñu ngi koy nafar ci daaru yu mag yi…Bu loolu weesoo it gis naa ne itam mbind mi ci làkki réew yi, mi ngi law bu baax ci biir Afrik …
Lilam Azam Zanageh moo taataan waxtaan wii ci Le Monde des Livres bu 16 Awril 2010
Tamsir Anne moo tekki jukki bi ci Wolof
waxtaanu boris wi amna solo, man sax daf maafekk may jáng téere boobu di doomu golo. amna solo lool.
jaajëfati Tamsiir