Timbukutu: péyu xam-xam bu yàgg te sax! Ni ñu leen ko fi waxeewoon ci jukki bi weesu, bind, sàkku xam-xam, gëstu ak diine lu yàgg la ci Afrik! Wante ñakka xam ak ñakka am xel-ñaar tax na ba ñu bare defe ne gànnaaw woy aka fecc, mbaa léeb amul genn ndono lu am solo lu Afrik donn ci wàllu xam-xam.Image
Feeñal parparloo ak tutiwaayu gisin woowu bokk na ci li ñu tax a jóg. Firnde bi ñuy indi téy mooy Timbukutu, di dëkk bu mag ci Mali, te xam-xam bu keemaane sax fa, di fa law ca la ko dalee lu jiitu 12eelu xarnu ba bés ni ki téy. La fa des ci ay téere yu ñu bind ci kalaama Araab, pël, songaay… jàpp nañu ne ëpp na 700.000 téere!
Te kenn mënul a xayma la ca yàqu ak la ca reer ci diir bu weesu 700 at, ba ñu fa tàmbalee bind ba léegi. Bind yooyu nag daanaka dañoo laaw xeetu xam-xam yépp: dalee ko ci xam-xamu diine, jal ci xayma, xam-xami biddéw yi, xam-xamu suuf si, taalif, xameefu-sàrti-baa, kimi, yoon ak yenneen ak yenneen. Ndongo yi daan nañu jóggee fu nekk ci àddina, Keer, Bagdaad, Pers ag fépp di fa jàngsi. Jàpp nañu ne iniwersite Sankoore ca Timbuktu lu tollu ci 25.000 ciy ndongo daan nañu fa jàngsi.Image Ay kangam yu mag yu mel ni Amet Baaba, doon borom xam-xam bu ñu ràññee ci àddina sépp, ñoo fa daan jàngale. Jamono jooju Afrik sóowu-jànt – Timbuktu, Jenne, Gawoo, Kano – doon péyu xam-xamu àddina si dafa temboo woon ag lëndëmtu gu meti ca Ëroop. Iniwersite ya njëkk Ëroopsax – iniwersite ya nekkoon Andaluus ca Espaañ, ay xeetu Araab ak nit ñu nuul, doonoon ay doomi Afrik, ñoo leen fa sànccoon. Ay boroom xam-xam yu mag daan nañu jóggee Timbuktu di fa jàngaleji. Kon nga xam ne àddina moo gudd tànk! Wante xam loolu ci boppam rekk lu am solo la: ndax da ñuy gindi, gën ñoo tàggaat ba ñu xam ne xam-xam boobu fi nekkoon, su ñu farloo, mën na fee dellusiwaat. Te sax masu fee jóggee! Téy jii itam yaakaar amaat na ci Timbuktu: ndax réewum Afrik mu mag mu mel ni Afrik-bëj-tànk, moo xar tànku tubbayam, taxaw ci saytu téere yooyu dés Timbuktu. Afrik di Sidd duggal na ay kopaar yu bari Timbuktu ngir ñu tabax fa kàggu bu mag bu ñu mëna dencc ci anam yu mucc-ayib téere yooyu, tàggat itam ñay liggéey ca kàggu yooya ba ñu xam na ñuy saytu téere yooya ba duñu yàqu.
Kon gàcce ngallaama Afrik di Sidd ak Tabo Mbeki mi nga xam ne moo amoon xalaat bu rafet boobu.
Tamsir Anne © wolof-online.com