Cosaan soo kooy seet, mënees naa wax ne, mooy xàncc biy boole ay nit ba ñu mëna ràññee ne nit ñooñee ñooy askan sangam. Ndax soo demoon téy marse Sàndaga, di béréb bu ay turist yu joggee fun nekk ci àddina di dajaloo di jënd, doo mëna wax mukk ne ñooña fa tase askanu turist lañu bokk. Walla book xanaaa wax jooju dib waxi-misaal, nde fa dëgg dgg ay dox-daje kese lañu!
Wante aw askan nag dug dox-daje koy tabax.Image Su ñuy wax askan, li mu ëmb mooy ay nit ñu bokk aada yu yàgg, bokk ca cosaan, am fu seen maam jaar démb ba yegsi foofee ñu yegsi téy. Dafa am kon lu boole nit ñoona ñu naan ñooy askan sangam ca jamonooy démb ba léegi.
Dafa mel ni kon cosaan mooy buum biy lëkkale ay nit, ba ñu nopppee doon aw mbooloo kese, soppaliku aw askan! Su doon ne dees di mengale aw askan akub tabax, dees ay xala wax ne cosaan mooy kennu tabax boobee.
Looloo tax ba aw xeet mbaa aw askan, soo ko bëggee noot ba fàww rekk, farlul ci mu fàtte cosaanam! Loolu nag la tubaab bi ci pexeem mu rëy nàndoon, ba tax ba mu fi bëggee dëj doxalinam, dafa jël ndawi réew yi dugal leen ci ay daaraam, jàngal leen làkkam, jàngal leen cosaanam moom tubaab bi, ba noppi nag ne leen, yeen moom amu leen cosaan, ndeysaan, su ngeen yebboo rekk jeema roy ci ñun.
Noonu cosaan amee solo noonu la it làkk amee solo, rax ci dolli làkk woo gis dafa am cosaanam, am mbokkoo gu dox diggantéem ak làkki yenneeni askan, rawatina askan yi ko gëna jege. Naka noonu la Wolof bokkee ak pël, bokk kook sereer, bokk koog saraxolle ak yenneen làkki réew-mi. Wante nag itam, baat yi ci làkk wi seen bopp dañoo mel ni saa woo xam ne soo ko toppee, dangay yégg ba fa askani Wolof cosaanu dëgg te mooy bëlub dexu Niil ca Misira démb!
Soo dendalee Wolof ak làkki Misira démb, ag làkki askan yi nekk ba bésu téy ji bëj-tànku Esipt, naka Nuer, day fés ne Wolof dafa bokk bu baax, ci anam yu jeggi dayoo ag làkk yooyu.
Mbokkoo gi dox diggante Wolof ak làkki Esipt mëneesu ko fee fàramfaccee ba mu jeex: Dafa di mbokk gu xoot te daj làkk wépp, fés ci baati diine yi, baati mbokkoo yi, baat yiy tudd cëri nit ak yeneen ak yeneen. Te baat yooyu ay làkk du ñu ko niroole, te fàww amul mbokkoo gu dox ci seen diggante!
Loolu lépp nag li mu lay won mooy ne làkki réew demu ñu sax bay fóoyóoy! Sunu làkk yi ñu donnee sunu Maam ya, muy Wolof mbaa pël, mbaa sereer, mbaa joola walla wenneen làkk wu mu ci mënti doon, seen solo ci defaraat nit ñi, defaraat réewi Afrik, delloo leen seen gëdd lu jeggi dàyyoo la te mata sédd la!
Wante nag su caaxaan fàqee, dëgg des, kuy jeggaani ba jeggaani aw làkk te ame sa làmmiñ, lúwuloo, war ngaa seetaat sa bopp!
Li am ba des rekk mooy li Seex Musaa wax ne “bépp làkk rafet na, buy gindi ca nit xel ma, téy tudd ca moom ngor la!”
Tamsir Anne © wolof-online.com