XARNU BI
Sëriñ bi noo gi deeti ñaan
Faqiir dafay nangoo dagaan
Nangul nu lépp lu nu ñaan
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Noongi dangaan ci Mustafaa
Ma nekk marwat’ak safaa
Ak àqi amdi Mustafaa Mi
Yàlla jébbal xarnu bi
Ak àqi mboolem ay rakkam
Ak àqi séen baay yi ñu am
Ak àqi seex yi Bàmba am
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Mboolem muriid yépp a ngi tuub
Tey réccu bàkkaar yi nu joob
Ba lu nu bay-bay, du nu góob
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Mbàkke, dangay boroom i mbóot
Te sag njaboot tawat gilóot
Ñu def ma ab àntarpareet
May làpputoo waa xarnu bi
Aw ma màqaamam di la woo
Waaye muriid yi ñoo ma woo
Ni tawatal te bu ñu woo
Saw làmmiñay wow xarnu bi
Tay jii ma wax bani tareet
Ngir yaa ma def antarpareet
Yaa fab i xam-xam ne yuréet
Ci sama xol, ci xarnu bi
Te bul ma tanxamlu ci ñaan
Ngir lii ma bon tey ku añaan
Muriid yi yépp a la ko ñaan
Ngir bëgg a dekkal xarnu bi
Jooy i perantal la nu jooy
Boo nu fabul, lee nu ni wooy
Ku nuy yafal, ban def i kooy
Mu dellu naatal xarnu bi
Jis u nu baay te noo ngi raam
Ku ñàkk yaay, day nàmpu maam
Buural te boot nu, ngalla daam !
Roggani mboolem xarnu bi
Fabal sa doom yi yépp boot
Ñoom it ñu boot séenug njaboot
Ku manta boot nga jox ko mbóot
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Te fab muriid yi suturaal
Mottali jàkk a jii nu naal
Foo toll dolli séen alaal
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Ndax Yàlla amdi Mustafaa
Tabax jumaa-i Mustafaa
Bam tol ni marwata’ak safaa
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Boolem muriid yépp a ngi jooy
Ngir luñu bay-bay mu dal di gooy
Ba séen i àddiya’a ngi booy
Sarax nu naatal xarnu bi
Jamono jaa ngi xiif a xiif
Luñ togg, bar gi ni ko fuuf
Seex Bàmba, neel ngën ji mbindéef
Mu dellu naatal xarnu bi
Xiif tax na, ñenn mag ñi yooy
Xiif tax na, gor su ndaw si jooy
Xiif tax na, yenn tool yi booy
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Taxna, ña daa joxee ngi laaj
Ñii ñépp séen i sas di xaaj
Ken dóotu dem fenn ba waaj
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Xam nañ ni yaa nu daa tawal
Daanu bayal, daanu ñoral
Daanu roñal, daanu daggal
Feesal nga sàqi xarnu bi
Sa yërmandee nu daa defal
Lu xel dajul, daanu dëfël
Daanu tibbal, daanu leel