Seetal Fii
« Filosofi ci wolof : A ni aada … »
aada j. : aada mooy mbooleem matukaay yi am mbooloo, gën gaa bare, aw askan di tegtaloo cig jëf, di ca xàjj lu bon ak lu baax. Matukaay yooyu ñooy doon tegtal yiy ommat nit ki ci yoon wi muy jëflanteek yeneen mbindeef yi ak càkkeef gépp. Kon aada, du loo xam ne ci coobare boppam la ko way di nàngoo topp mbaa mu jalgati ko. Ndax tëral yi ci biir aada, ñaare, ca cosaan la ñiy lawe, di meññ ba yegsi ci jamono.
Aada ci fànn dund gépp lañu ko mën a ràññee ci ab → sosiete, moo xam ci → kurél yi ñuy sàmp la, ci wàllu → politig, koom-koom, yoon mbaa diine la.
Mën nañoo wax ba tey ne aada mooy dig bi aw askan di màndargaale li mu moom ak li mu moomul, li mu caadawoo ak li mu àbb. Looloo tax askan wu nekk am aada yu mu moomal boppam, yu mu jéggaaniwul : kon aada dafa bare te bokkul.
Wante aada itam sangoowul der bu teref, ba dara lu bokkul ca moom ca cosaan du ca mën a rax. Nde ni jamono di doxee noonu la aada itam di doxe, di ko soppeekoo, ay tëral yu yees di ca juux, am yeneen yu ña cay xent. Ci kow loolu la aada yu bari di jaar ci yoonu diine, soppi lu bare ca na ñu daan ràññalee mbaax ak mbon ginnaaw ba askan woowa tuubee, topp weneen yoonu diine.
Ba léegi, ay askan nu ñu gën a jegeente ca seen cosaan, noonu la seeni aada di gën a niroo. Seex Anta Jóob wone na ci téereem yu bari, ni réewu Afrig yi seeni aada róofoo ca cosaanu maam ya jamonoy Buur-Fari ya woon Misira démb ba tey jii.
Ci wàllu nekkandoo, aada bokk na ci liy fas te di gën a dëgëral li am mbooloo mbaa aw askan bokkandoo. Kon aada, ndonte kon wuute na ak yoon, ci natt yi miy teg ñiy jalgati ay tëralam, ci kenu yiy téye ab sosiete la bokk.
Wante meññeefu aada, maanaam njëriñ li mu làmboo ci jamono jii, mu ngi aju ci ni aada ji di soppeekoo ànd kook li jamonooy laaj. Bu ñu koy seet tey day mel ni matukaay yi mel ni waccoo ak yelleefi doomu aadama, sàmp nguur ci kow yoon, sàkku yokkute ci tawféexu nit ñi, dakkal xare ak faat bakkan cig neen, ay ponk lañu yu aada yépp ci àddina war a mën a ànd.
Fr. : coutume
ajeel b. : lëf ki, walla xew-xew bi nga xam ne lëf keneen ka, xew-xew beneen ba ca moom la aju, maanaam su amul loola du mën a am, mbaa deesu ko mën a xam.
Ci fànnu losig walla jaduteef, mën nañoo faramfàcce mbir mi nii :
Dees nay wax ne ajeel sangam lu war la, su fekkee ne lëf sangam (L cig gàttal) su amee, te ci kow mu am doŋŋ la lëf ka muy jur walla njureel la (N cig gàttal) di ame. Su ñu ko baamtuwaatee màndargaay wax jooju lii la : su fekkee ne te su fekkee ne doŋŋ L ci lay N di ame.
Ab ajeel mën naa itam mat sëkk, su fekkee ne su L amul N du am, maanaam su dee (–L) kon (–N).
Mën nañoo tënke ci loolu ne : su dee L ajeel bu war la ngir N, kon itam ba léegi N ajeel bu mat sëkk la, ndax su dee ci kow L am doŋŋ lay N di amee kon su L amul N itam du am. Ab ajeel bu war te mat sëkk kon lii lay tekki : ci kow ajeel boobu nekk doŋŋ la ajeel ba ca des di mën a nekke.
Fr. : condition
…………………