Am bukki yomb na, waaye bukki buy xalam a jafe.
Am na bukki bu ŋexalul, te jégéñ kër.
Bukki am na gillint, tey àll bi leer.
Bukki amtekoonu bàkk yëy ko.
Bukki, balaa baax, yooy.
Bukki bu daanee ponkal ca doxin wa la.
Bukki bu nammee fande reere doom ja.
Bukki, kenn du ko dénk ay seel.
Bukki nee : “li ñépp wax ay dëgg !”
Bukki nee : “Ndaari neexul, waaye kër baay a”.
Bukki nee na, ab reer taxumaa jóg, waaye bu ma ko fa fekkee sant.
Bukki su la bëggee yapp, da la naan yaa ngi may xeeñi seel.
Bukki wiiri-wiiri, jaari Ndaari.
Category: Uncategorized