Ci ayi bés yii ñu dëgmal mbootaayi-réew yiy jëfandikoo làkki “francais” tey wooye seen bopp mbootaayu “Frankofoni” ñu ngi waaj seen 14eelu ndaje, ngir berndeel làkki francais ak caada Faraas. Looloo ma junj nag ci xalaat, ban cér dëgg ak gan gëdd lañu sédd kalaama “francais” ci réew yu wuute yooyu yépp ni Niseer, Faraas mbaa Wietnaam.
Li ma njëkka ràñnee mooy béréb ba ndaje moomu nara ame, te muy réewum Kongo dafa am misaal bu mu ëmb. Réewum Kongo réew mu yaatu la tooloog 2. 344. 852 ci km2, mat kon Faraas ñeenti yoon, ëppee ko 6 miliyoη ci ay nit. Réew la itam mu biir-suufam oom lool. Xayma nañu na lu ëpp 50 ci ay minëre ñu nga ca biir suufas Kongo: dalee ko ci kobalt, xanjar, xaalis, wurus, jama…ba ci minëre yu jafee gis yu mel ni koltaan. Koltaan boobee lu am solo la ci defar telefon- ak ordinatëër portaabal yi ak korba yi (manaam fusées) yiy dem ci jàww ji. Loolu tax réewi Tugal ak Siin ak ñeneen xér ci di ko jiiroo, doomi Kongo ñoom dëkkee xeexoo aka xiiroo, xiif ak gàddaay. Am na yeenekay bu nekk Londres bu bind ne li làqu ci alal ci biir-suufag Kongo ëpp na 24 juniy miliyaar ci Dolaar: maanaam moo ëpp li réewum Amerik ak ëroop di am ci alal at mu jot! Wante nag loolu teewul Kongo mooy réew mi gëna ndóol ci àddina sépp (187/187)! Céy!
Waaw kon ñuy laaj naka la “francophonie” miy bàkkoo saytu yelleef ak àqi doomu aadama mëna tànnee réewum Kongo mu Kabila mi ñépp xam ci cay-caayam, dëddu askanam, parparloom, rawatina ay ja fa tàkk – di fa amal ndaje moomu? Ndonte kon doomi Kongo seen bopp dañoo ñaawtu ndaje moomu ñu fa nara amal ba sonn? Toontu bi ci sunu gis-gis lu yomb la: Faraas, bu caaxaan fàqe dëgg dés, Sarkozi wéy Hollande falu, li ko ñor mooy feddaliwaat, xëddaat bu baax, fésal teewayam Kongo yëkkati baatam ca kow ba ñépp xam nee foofa moo fay doggal, mu fay nas aka nocci.
Te itam, loolooy yaxu wax ji fii, “Francophonie” soo ko seetantalee, su pënd cóowul làkk nasaraan wi mbootaay woowu ne moom lañu bokkoo dalee, di nga gis ne réew ya ca biir yemuñu ca demin. Nañu jéllale réew yu mel ni Faraas, Kanada, Swis ak yeneen réewi Tugal, ndax ñoom ca seen and la ñu toog, te seetlu lii:
– ci réew yi bokk ci Francophonie, ñett kese ñoo cay réewi Asi te ñooy Laos, Wietnam ak Cambodge. Te ci ñetti réew yooyu yépp seen làkki bopp maanaam Lao, khmer ak vietnamien ñoo fay làkk ya ñu fay jëfëndikoo ca lekool ya, nguur ga ak bérébi átte…Làkku “francais” làkki-jambuur kese la fa! Te ñetti réew yooyu yépp ku ci nekk da nga am sa xaalisu bopp!
– ñaareel bi mooy: ci réew yiy làkk araab yépp te bokk ci mbootaay moomu, ñoo xam Afrik lañu nekk (Tinisi, Marok, Mooritani) mbaa feneen (Liban), menn réew defu ca francais mu fay làkki nguur ga; ñoom ñépp araab mooy seen làkk ofiseel.
Te soo seete réew mu mel ni Tinisi, moo ëpp fuuf ñu dégg francais kë Senegaal mbaa Mali. Réewum Tinisi téeméer yoo jël 63% dégg nañu francais te bu dee Senegaal 24% kese la, Niseer di 18 nit képp ci téméer yoo jël. Nga gis kon ne dafa am “francophonie” ci biir “francophonie”, yépp duñu benn!
– Soo jëlee nag réewi Afrik yu mel ni Senegaal, Kamerun, Mali, Gine, Kodiwaar, Gabon, Kongo: réewi Afrik “noire” yi maanaam – so ci gennee Rwanda ak Burundi – te ñooy réew yi ëpp ci mbootaayu Francofoni, ñoom ñépp francais mooy seen làkk ofiseel, te kenn ci ñoom amul xaalisu boppam, ñoom ñépp “Franc CFA” lañuy jëfëndikoo!
Wante li gëna doy-waar ci mbir moomu mooy ne réew yooyu seen bopp ña fay làkk francais as tuut la, lu neew la. Su dee Niseer 18% lañu, Burkinaa 19%, Senegal 24%…te terewuleen ñu beddi seeni làkki réew teg seen lépp ci francais!
Wante nag waxtaan nitam wax dëgg ca la, bu kenn tooñ Faraas, yenn yi Yàlla natoowu ko kenn: ag yembadi akub cuune kese la!
Seneraal De Gaulle dafa waxoon ne nguur yi xamuñu xarit, li leen amal njëriñ kese lañu xam, maanaam ku nekk yaa xam nooy toje sa boppu suññeel! Kon loolu leer na!
Am itam beneen mbir mu mata seetlu: réewi Afrik “noire” yi bokk Francophonie gànnaaw Gabon ak Congo (Brazaville!!!) te ñoonu da ñoo am peterool, yeneen réew yépp ci réew yi gëna ndóol, gëna lott ci àddina lañu bokk. Kongo ci yees, Burkinaa topp ca…Senegaal mbaa Mali waxi-noppi! Bokk nañu itam ci réew yi ay di tàkk di fa law…
Su ñuy wax kon téy ci Francophonie, war nañoo bàyyi xel mbir yooyu, ngir jeema seet doxalin bu bees bu gëna dëppoog liy jëriñ sunu réew yi ci wàllu caada ak koom-koom. Wareef la téy gànnaaw 50 at ak lu topp ba sunu réew yi ne ñoo moom seen bopp ba léegi, ñu faydaal sunu làkk yi ñu moom def leen ñuy ak làkk yu ñuy jëriñoo di leen jëfëndikoo ci fànn yépp. Ndonte sax dañuy bokk ak francais gëdd googu!
Tiis na lool wante la Seex Anta daan wax laata réewi Afrik yi di moom seen bopp moo fiy wéy ba léegi, ndax da ne woon:
“bëgg lu yomb kese akug yaafuus, ñakk pas-pas akub doggu rekk, bañ-sa-bopp te sawar ci ku toog ci sam xel di la diggal di la àtteel lu baax ak lu bon doηη a tax waay-xeeltu yi ci Afrik di doyloo làkki nasaraan yi”.
Tamsir Anne: tamsir.anne@wolof-online.com
Yamsiir waxati nga dëgg. man bëggnaa sama réew lool ,waaye gisa gu ma njiit lu am fayda. te kenn ci sos frankofonie muy Leopold Sedar senghor dafa wxoon loo xamne wuuten ak jëfëm. dafanewoon ” Lákk wi mana dimbuli am réew ak aw askan mu jëm kanam ci yépp fann, mooy lákk wi nit ki di génte suy nelaw, te di ci saaga su meree” loolu nak lu leer la mooy lákk wi askan wi námp. Man de yaakaarnaa sunu boroom mi wax ci alxuraan ne “lákk yu wuute yi ak meloy der yu wuute yi ci samay kiimaan la bokk” kon nak sággane saw lákk sággane cer bu la yalla joxla te loolu ci weddi yalla la bokk. yall nanu yalla dimbuli ba askan wi degglu tey topp waxkati dëgg yi. jërëjëfëtee Tamsiir.
S. Balla lo
Jánglekatu wolof ci daaray nasraan yi Sweden