Ci at yi ak wéer yi weesu, mel na ni Afrik dafa dellu fa baaxi maam nekkoon, te mooy wormaal, naw, solool jiggéen. Bu ñu ko fatte fii ci Afrik, jiggéen na fi ma masa fallu, di yaay, di lingeer, di ndey-ji-réew, di buur, ca Misira démb, Nibi, Meroe, ba ci Waalo ak Kajoor. Kon su ñu dellusee di fal jiggéen ju mel ni Nkosazana Dlamini-Zuma, mu wara jiite kureel gi feetee kow mbootaayu réewu Afrik yi, “Union Africaine”. Loolu lu mata fésal la. Soxna soosu nag bañkat la masa doon, daan xeex nguuru apartheid ca Afrik di Sid, bokkoon ci daanaka goornamaa ya nekk réew moomee la ko dalee 1994 ba léeggi. Kon mënees naa yaakaar ne di na delloo “Union Africaine” gëdd gi mu yellool.
Am na itam jeneen jiggéen ju ñu ràññee bu yággul dara gànnaaw ba ñu ko falee mu bokk ci àttekat yiy wara àtte ca CPI maanaam àttekaay bi mbootaayu xeet yépp daanaka bokk, di fa àtte saay-saay yi def lu bon, di xëpp ay ci seeni réew, teg fa nguuru parparloo di noot aka boom. Kookooy Fatumata Bensudaa di jiggéeni réew mi, ndax Gambi la fekk baax.
Fatumata Bensuudaa moomu doonoon na jawriñ ja yore mbiru yoon ak yemale ca réewam jogge fa bokk ci tiribinaal ba doon saytu mboomum xeet wa amoon Ruwaanda.
Mën nañu fee tudd ba léegi it soxna su mel ni Joyce Banda, di njiitu réewum Malawi, di ndaw su tàkku ngir suxali réewam, xeex gér ak yàq. Naka noonu itam Elen Sirlaf Jonson, njiitu réewum Liberia ma say-say bu mel ni Sarl Tayloor demoon ba toj ko.
Kon jaaraama jiggéeni Afrik yooyu dekkkal cosaani maam!
Tamsir Anne: tamsir.anne@wolof-online.com