Ci 7000 làkk yi ci àddina, 85 la ñi ëpp ci nit ñi, daanaka 78%, di làkk. Làkku angale ñi koy làkk tollu nañu ci 328 miliyoη, ñiy làkk sinwaa tollu ci 845 miliyoη. Làkk yi gëna ndaw yu mel ni tuwa ca Siberi, bëj-gànnaaru Risi, 235 junniy nit doηη leen a làkk.
Boroom xam-xamu làkk yi jàpp nañu fi ag xarnu bii di jeex gennu-wàll làkk yi ci àdduna bi yépp, dinañu raaf. Lu tollu ci 1000 làkk lañu jàpp tey ne lott nañu. Yenn làkk yu mel ni wintu ca Amerik, di làkki “indiens” ya fa nekk, mbaa amdurak deeni ca Australi, ñi leen dégg tey weesootu ñu junniy nit.
Loolu tax ba lingist yi di gaawaantu di dajale aka taataan lépp lu nekk ci làkk yooyu balaa ñoo dee ba fàww! Ndeeteelub làkk nag musiba la bu kenn xamul nu mu tollu: ndax caada week, xam-xam ba, cosaan week mbóot ya làkk woowee ëmboon ñooy sànku ba fàww.
Wante li gëna yeeme ci mbir mi mooy ne làkk yu bare yi ñu jàpp ne tey dañoo répp, làkk yooyu gox yi làkki francais law lañu fekk baax. Naka làkk yu mel ni “wallon, picard, basque, breton, bourbonnais, bourguignon, champenois, corse…” ca ëroop.
Tamsir Anne tamsir.anne@wolof-online.com
“Ô hommes! Nous vous avons créés d’un mâle et d’une femelle, et Nous avons fait de vous des nations et des tribus, pour que vous vous entreconnaissiez. Le plus noble d’entre vous, auprès d’Allah, est le plus pieux. Allah est certes Omniscient et Grand-Connaisseur.” (S 49 V.13)
Da ma yakaar ni da fa bokk ci yermande Yallah ci li mu bind doomi adama yi ba pare wutele leen ci askaan. kon su nu deme ba aduna bi yépp bokk benn lakk benn ada,manaam li tubbab yi di dupe “mondialisation” da fay melni bougougnou yermande yallah wacc su nu caw.