Ci benn laaj-toontu bu njiitu-réew mi amal ag yeenekaay bu tudd Afrik te nekk ca Belsik, Màkki Sàll feeñal na ay xalaatam ci mbir yu am solo yu soxal Senegaal ak Afrik. Ci lu jëm ci li ñuy lëñbët ñi fi nekkoon ci yan anam la ñu yore woon réew mi, wax na ne, na ñépp jàpp te gëm ne moom du làq kenn, ag ku kooku mënti doon, ku def lenn lu wàccoowul ag yoon. Nee na pas-pasam, mooy dellu tegaat Senegaal ci doxul yoon, topp yoon, doomu-réew bu nekk ñu jox la àq bi nga yellool.
Ci lu jëm ci ANOCI (kureel gi Karim Wàdd jiite woon), nee na itam, odite kureel googu nga xam ne lu tollu ci 400 miliyaar ci xaalis dugg nañu ci, lu war la, lu mënula ñakk. Karim Wàdd tey ci alxamees gi la wara jàkkarloowaat ag tàkk-der yi koy laaj ci doxalinamu ANOCI.
Ci lu jëm ci diggantéem ak Ablay Wàdd, njiitu-réew mi fi nekkoon, Màki Sàll nee na seen diggante ba ñu tàqalikoo ba léegi neexatul, wante moom ci boppam jàppalu ko dara.Yokk na ci ne itam moom ay digle yoo xam ne su ko koy Ablaay Wàdd di digal ci yeenekaay yi la koy jarale, moom digle yooyu soxlawuleen.
Naka noonu joxe na itam xalaat ci xew-xew ya ca Mali ag Kodiwaar, wax ne lépp lu mëna delloo jàmm ci réew yooyu, di sunuy dendandoo, Afik gépp ak àddina sépp war nañu cee taxaw bu baax.
ñë