Tey ci Tombukutu, waay-fippu yiy bàkkoo lislaam te naan dañuy jihaad defati nañu fa ñaawtéef yu bon: ndax dañoo dug ci xabru ay waliyu yu mag, toj leen ba ñu mokk rumbax! Tombukutu nag, indil nañu leen fi ci dal bii, ay yooni yoon ay jukki, doon leen ci fàttali jàllooreem ci wàllu lislaam. Ndaali Mali la bokkoon, doonoon péyu xam-xam ak diine, ndongo yi di jógge ba Bagdaad ak Pers doon fa ñëw di ñakkusi xam-xam ag jikko yu rafet. Li fa nekk ci téere yu ëmb xeetu xam-xam wu nekk ci àddina ca kàggu ya fa nekk, kenn xamul nu ñu tollu!
Wante tey àddina sépp a ngi seetaan, sambaa-booy yu bon yooyu di jeema faat ndono googu nga xam ne àddina sépp la soxal, àddina sépp a ko bokk!
Wante nag liy raam ci ñag bi la jëm! Ndax saay-saay yooyu su ñu leen seetaane, su ñu jógge foofu danañu def lu ko yees!
timbukutu
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_destruction_tomboucoutou1.jpg]170
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_manuscript_tomboucoutou_600_0.jpg]200
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_habitanttomboucoutou_0.jpg]100
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_fanatique.jpg]70
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_destruction_tomboucoutou3_0.jpg]40
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_destruction_tomboucoutou2.jpg]60
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_manuscripts_tomboucoutou.jpg]40
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_terroriste_tomboucoutou.jpg]30
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_tomboucoutou_manuscrit_6002_0.jpg]30
[img src=https://www.wolof-online.com/wp-content/flagallery/timbukutu/thumbs/thumbs_sankore_0.jpg]40