Mbooloo mi! Ñu ngi leen di nuyu ku ci nekk ci yeen ci sa tur ak sa sànt te di leen dalal ci jàmm. Béréb bi ngeen tersi téy nag
dañu koo sàncc, mool ko ci kalaama wolof, jagleel ko làmmiñ yi ñu nàmp, ci réewum Senegaal ak ci Afrik gépp. Yaakaar nañu ne lu ni mel, mën naa am mu kañ ñenneen ba ñu xar seen tànki tubëy ci di jëfëndikoo làmmiñ yi ñu moomal sunu bopp, jéggaani wu ñu leen fenn!
Ku fóog ne nag sunu làkk yii ñu nàmp, dañoo fóoyóoy, wàlla dañoo matadi, xamal ne rekk yaa ngi ci njuumte gu réey. Ndax sunu làkk yii, amul senn làkk ci àddina su leen yóobul dara. Mbooloo mi! Ñu ngi leen di nuyu ku ci nekk ci yeen ci sa tur ak sa sànt te di leen dalal ci jàmm. Béréb bi ngeen tersi téy nag
dañu koo sàncc, mool ko ci kalaama wolof, jagleel ko làmmiñ yi ñu nàmp, ci réewum Senegaal ak ci Afrik gépp. Yaakaar nañu ne lu ni mel, mën naa am mu kañ ñenneen ba ñu xar seen tànki tubëy ci di jëfëndikoo làmmiñ yi ñu moomal sunu bopp, jéggaani wu ñu leen fenn!
Ku fóog ne nag sunu làkk yii ñu nàmp, dañoo fóoyóoy, wàlla dañoo matadi, xamal ne rekk yaa ngi ci njuumte gu réey. Ndax sunu làkk yii, amul senn làkk ci àddina su leen yóobul dara.
Sunu Maam yi, ci lañu doon bind, di ci jaamu Yàlla, di ci xam seen bopp, di ci jàng àddina! Seeni pexe kañ, soo leen jàngee bu baax, da lay sax xanaa yeem! Ndax ay làkk yu xereñ, te amul lenn ci àddina lees ci mënul a wax. Ndem-si-Yàlla si, Seex Anta Jóob, ndeysaan, Yàlla na ko suuf sedde, da daan wax ne: “Aw làmmiñ du gàtt, aw xel mooy gàtt! Ndax lépp lu xel mëna xam ba mu leer ca moom, làmmiñ wa mën na koo tudd!” Te téy jii nag nga xam ne àddina si daa dem ba mel ni as
ndëkk su ndaw, xarala yu mel ni enternet ak yenneen, di def ba askan yépp am sañ-sañu wone seen dayoo, wone seen mbaax, seeni aada ak yoon wa ñuy gisee àddina, waru ñoo nangu di dés ginnaaw mukk!
Dees di faral di wax nag ne aw làkk mooy daanaka ruu wu aw askan, ndax askaan wu jèggaani ba jéggani aw làmmiñ, fàtte ne mi ngeek bosam, askan woowee ku yeeboo ne cànkute gu wér moo ko dal. Waxu ñu nag ne dañoo wara tëjju ci sunu biir, duñu jëfëndikoo mbaa ñuy làkk lu dul suñu làmmiñ yi! Déedéet: dañuy jàng làkk yépp, tambalee ko ca angale, farañse, sinwaa ak lenneen ak lenneen, wante na njëkka fekk ñu jàng sunu làkk yi, di leen jëriñoo! Ndax Wolof-Njaay da ne nit ku nekk li nga moom, nga mëna damoo! Te it sax, nag, su caaxaan faaxe, dëgg dés, àddina sépp daanaka noonu lañuy doxale! Réew mu ndaw moo seet, muy Oongiri, di Soloweeni, Serbi wala menneen réew moo jël ci Ëroop ak li ko wër, seen làkk yi nu moom lañuy jëfëndikoo njëkk.
Kon, mbokk sama, xarit sama dëgg la sax, àddinaa dox, nasaraan juuxsi fi, di làkk làkkam, te naan ñu ba leen seen wos! Wante nag, téy jii ñuy waxee, ci atum 2009 sunu réew yi ñoo moom seen bopp: Kon lay jeex na, sas boobu sunu sas la! Kenn du ñu ko yennul, kenn du ñu sax gaar ci di jëfëndikoo sunu làkk yi! Loolu ñun do ??, waay-xeltu yi, ñiy yëngu ci politik, jàngale, koom-koom ag fànn wu mu mënti doon, ñoo ko mëna defal sunu bopp.
Tóol boobu nag lañu xëyy, di leen sàkku fu ngeen mënti nekk ngeen jàppale ñu, siiwal béréb bi, yonnee seen xalaat ci mbir yi ñu fi soxal ñun ñépp.
Wasalaam!
Tamsir Anne © wolof-online.com