Symbole ci nasaraan, su ngeen ko déggee mooy lëf koo xam ne dafa am lu muy mandaragaal! Du lëf ki ci boppam moo am solo, waaye la muy junjj ci xelu nit ñi la… Ndekete këf ki ñu leen bëgg a nettali masu fee jóg te mooy symbole bi fi daara tubaab bi indi di ko xeexe làkki réew mi. Su ngeen ko fàttaliko (ci jàng mbaa ci nettali) dañu daan masa tere di làkk làkki réew mi ci ekol yi. Ndongo lu masaan a rëccal ba làkk Wolof mbaa pulaar mbaa joola walla leneen rekk ñu takal la symbole bi. Li mu daa faral di doon moo daan këf ku kenn bëggatul, naka ab yax bu ñu seeñu ba mu set, soo ko sànni xaj sax du ko xool! Noona lañu daan nàttee solo làkki réew mi. Loolu doonoon kennu bu am solo ci politik bi Faraas saxaloon fépp fu mu masaan nekk bëgg faa wéyal caadam, làkkam, doxalinam ak ay gis-gisam, tuddee woon ko “assimilation”, manaam roy-dàq-aada.
Ci réewum Faraas ci boppam sax symbole boobu amoon na ca lekol ya ay askani “bretons” nekkoon. Faraas daal da fa mas a farlu ci xeex bépp làkk bu dul làkkam rawatina nag làkki réewi Afrik yi mu noot(oon).
Wante sax nag Faraas deful kenn dara: bëgg sa bopp, bëgg sa làkk di ko faral dara nekku ci te Wolof Njaay da ne “lu waay nangu teg ko ko dagan na!”
Ñun dañoo defe woon ne xanaa, loolu su ñuy tóog di ko nettali téy dañu naan jamano tubaab ya, wàlla jamano tubaab yu ñuul ya lawoon! Wante am nañu firnde ci atum 2010 bii ñuy waaj a màggal 50eelu at yi sunu réew moomee boppam ba léegi ne symbole boobu am na ci lekoolu Senegaal yi ba léegi! Wante nag du lenn lu ñu kenn sëf!
Ñoo ko nangu! Xanaa kañ dañuy yeemu ci xarala ak pexe tubaab ak sunu yàcaaral, ndax ndeem jóge na fi itam ci biti, ci biir moom moo fi nekk ba léegi!
Làkkam ma fiy wéy ba léegi, xaalisam a fi nekk ba léegi, xelam ak ay xalaatam ñoo fi nekk ba léegi! Lii la Seneraal De Gaulle seentu woon ba tax, ba waxi “independance” bëggee ëpp mu ne woon nanu yolomal buum gi ba laa dog: Ndax téy jii Faraas jóge na fi gaa, waaye téy la fi ëpp doole! Te nooteel bi gën a diis, gën a jàpp mooy bi nga xam ne ki nga noot day jiitu say xalaat, jiitu say bëgg-bëgg, def li la sóob te sa kàddu du jib!
Céy ngalla ñun li ci réew mi ak ay lekoolam!
Tamsir Anne © wolof-online.com
jërëjëf tamsiir ligeey bi rafet na te amna solo lool ci képp ku bëgg am réewam, ndax maa ngi fáttaliku bamay jáng araab ca Luga nun sax loolu amoon na su ekol, te booleen ko masaana laaj seen tontu moodoon da noo bëgg ngeen gaawa dégg arab. masumaa xam ne amn xalaat bu ñaawe nii ci ginaaw loolu.
S. Balla Lo jánglekatu wolof ci réewum Séude