Réewum Niseerya siiwal na alxamees gee nu weesu – 18 fan ci weeru Ut – ne sànni ñaari “satelit” ci jàww ji.
Satelit yooyee la ñu cay namm mooy yokk faggaru ci musiba yu mel ni maral ag mbën ngir yokkuteef ci wàllu mbay ag karaange ci seen dund.
Ñaari satelit yooyu, ñu tudde NigeriaSat-2 ak NigeriaSat-X , ñu ngi leen sànne Risi ci béréb bu nu naan Yasni.
Kon bii mooy ñaareeli yoon bu réewum Niseeryaa, di daanaaka réew mi gën a mag ci Afrik, yonne ay satelit ci jàww ji. Yoon bu njëkk bi, bu ñu fàttelikoo, ci atum 2007 la woon. Booba Niseerya réewum Siin la mànkoo woon ci mébét boobu: Wante satelit bu njëkk boobu da mujj sax seey ci jàww ji, gànnaaw ba mu fa nekke lu tooloog at! Ku dul bëre nag moom, doo daanu gaa, wante it doo am ndam!
Mbir mi nag li tax mu am solo lool, mooy itam, ne benn satelit bi ñu tudde NigeriatSat-X ay doomi Niseeryaa, di ay enseñëër ag ay boroom-xam-xam yu xereññ ñoo ko defar ci seen xarala bopp.
Xibaar yiy satelit yooyu di yonnee ci suuf ba léegi itam, da na tax ba Niseeryaa gën a mën a saytu ñaawteef yi yaqkat ak sambaabooy yiy sàcc petorol, di jaay ngannaay mbaa di def yeneen toqidoona. Kon loolu yokkuteef la ci wàllu karaange réew mu yaatu te mag moomee.
Peresidaa Niseeryaa, Goodluck Jonathan, wonne na mbégteem lool ci loolee réewam def, di jàlloore ci déndu Afrik ag lu ko weesu.
Kon gàcce ngallaama!