Nicolas Agbohou jàngalekat la ci fànnu koom-koom ci daara yu mag ya ca Tugal, cosaanoo Kodiwaar. Ci laaj-toontu bii ñu leen fi tekkil day ηàññ doxalinu réewi Afrik yiy jëfandiku Koparu CFA. Nee na kopparu Ëro ag bu CFA, ñooy ñaari yëf yi tax ba réewi Afrik yi feete làng googu mënu ñoo genn cig ndóol feek wutu ñu seen xaalisu bopp.
Afirik: Sa téere bi*, kalaame bu meti la, booy kalaame kopparu Euro ak CFA. Nga ne kon koppar yooyu ñooy lor Afrik?
Nicolas Agbohou: Ci lu wér, ndax kuréli koom-koom yiy saytu kopparu CFA, moo xam ay bànk yu mag lañu, walla yeneen, bëggu ñu benn yoon réewi Afrik yooyu am yokkute…
Boo seete ci ñi jiite kurél yooyu, naka « conseils d’administration », bu BCEAO, bànk bu mag bi nekk Ndakaaru, BCEAC walla Bànku réewum Komóor, ay doomi Faraas ñoo fay dogal dañu faa am sax sañ-sañu tere lépp lu dëppoowul ak li leen sóob, maanaam dañu faa am « droit de véto » ci nasaraan. Kóomóor naka noonu, ndax ci seen bànk bu mag ba ñenti doomi-Faraas ak ñenti doomi Komóor a fa nekk. Ndeem nag foofee, bépp dogal bu ñu fa war a jël alafokk, juróomi nit ànd ca, kon su benn doomi Faraas àndul ca loola, dogal booba du mën a àntu. « Africains » yi waru ñoo fàtte ni CFA kopparu Faraas la.
Afrik: Wante bu loolu weesoo, lu tax nga ni CFA njataη la ci Arik?
Nicolas Agbohou: Li tax mooy lii : dafa jot « Africains » yi am sañ-sañu doxal seen politiki bopp ci wàllu xaalis, politik bu dëppoo ak seen yakaar. Seetal ni, 15 réew yi bokk ci CFA yépp, at mu jot, soo jëlee li ñiy jaay bitim-réew, 100 dolaar yu nekk dañu cay dindi 65 dugal bànku Faraas, ñu ne pur garanti kopaaru CFA.
Seetal loolu! Réew mu mel ni Niseer, su jaaye lu tooloog 1 miliyaar ci dolaar, 650 Miliyon ya ñu nga dés bànku Faraas, fekk Niseer ci boppam du am sax lu mu faye ay liggéeykatam. Lii xel mënu koo nangu! Bàyyi koppar yu ni tollu réewu jambur, sa réew nit ñay dee ag xiif…
Koparu CFA daal day gën a yokk ndóol gi, dëkkee ñu ci nooteel gu amul àpp…
Afrik: Lu tax nag Ëro bi moom du njëriñ ci réewi CFA yi?
Nicolas Agbohou: Lu jiitu ñuy yeew CFA bi ci Ëro, Faraas rekk a daan lëñtu sunu koom-koom yi, léegi nag Ërop gépp am kàddu ak sañ-sañ ci ñun. Li yees, mooy natt yu tar yi ñu “Bruxelles” teg ànduñu ak sunuy namm-namm. Warees na kon ñu tàggoo ak CFA bi ci ni mu gën a gaawe!
Afrik: Lu ñu fay teg su ñu teggee CFA bi?
Nicolas Agbohou: Amul benn réew bu mën a jëm ca kanam te moomul doxalinam ci wàllu xaalis. Li ñu soxla mooy xaalis bu bees bu ñu moomal sunu bopp, bu ñu bokk…Sàrt yiy doxal CFA bi dañu leen war a sànni ca mballit ma. Li Afrik soxla mooy politik bu dëppook ay soxlaam ak njëriñam ci wàllu koppar.
Jukki bi: http://afrikeco.com
Ki ko tekkee ci nasaraan Tamsir Anne.
*Nicolas Agbohou: Le franc CFA et l’Euro contre l’Afrique. Editions Solidarité Mondiale, 296 p.
haa lii de yeeme na ¿waw kon ñoom fan lañ teg buñ jogee rek ne dañuy dimbali afrik? doyna vaar