Taaliif wii nag lu ñu barkeel la ci njëlbéen gi ba ca dayo ba.
Moom nag ki waxoon bayit wu njëkk wi –yal nañu ko dolli ag bëbb (xéewal) – am na ba tay weneen bayit wu yor maanaa mii, mu ciy nos woy, maanaam waxi sëriñam ji, wax jooju mooy jii :
nguurug neen waxtu rekk la, nguurug dëgg nag day wéy ba yawmal-xiyaam.
Woy waa ngii :
dëgg day sax, neen nag bu kawe woon it day mujj naaxsaay, mujj suufe.
Maa ngi tàmbali samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy Boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ja mu ñu jagleele ji ca allaaxiraa
Ubbite gi
– Kii di doomi sëriñam ji dul sànt ci boppam lu dul turam wu tedd wa Muhammad,
– Kii de mi ngi sant Yàlla (t.m) mi suturaal ay ayibam te taxawu ko te dimbali ko.
Tudd naa sellam ga moom de Boroom bu tedd la bob may na ma lu waral ma koy sànt.
Moom de mooy ki def ay teggin yu raf muy luy làq ag reer ak judd bu ñaaw (bonu askan).
Mooy ki jagleel boroom xam-xam yeek teggin, mooy ki léen jagleel ab yool akug jam-jub (def la jub).
Xéewal ak mucc gu kawe nañu sottiku ca ka yéegoon ca Alburaax (Yonnant bi).
Kooku mooy suñu sàng biy woote jëme ci Aji-bind ji (ki sàkk mbindeef yi), defe ko nag ci gën jaa rafeti teggin yi .
Kooku mooy Muhammad ak ñoñam ñi di woroomug raw ak saabaam yi làq ngënéelul Aji-des ji (Yàlla mi fi dul jug)
Ñoom saaba yooyu de saxaloon nañu ag laa-biire ci lu dul ηaayoo , ndaxte dañoo toroxaloon seeni bakkan ba far leen moom.
Sànkoon nañu seeni alal cig joxe ci lu dul ngistal mbaa naafeq.
Ñu sukkandiku woon ci Aji-jariñ (Yàlla) jiy Aji-wërsëgale, ngir ag wakkiirlu ci moom ci mbooleem wërsëg yi.
Ñoom de dañoo boyoon jëm alaaxlenniraa ngir ne dañoo fase woon wujj wa (adduna).
Masuñoo bàyyi lenn ndigal lu juge ci Aji-settantal ji (kiy def mbir yi di Yalla) kiy Aji-bind ji.
Ñoom de – ci saffanub ñuy bàyyi ndigal yi – dañu ciy sax ànd ceek bànneex, ndaxte koomum ja yi du tax ñu koy fàtte (alal ji
ñuy jële ci marse yi duñu tax ñuy fàtte ndigali suñu boroom yi) .
Wuññi woon nañu lëndëm-lëndëmi gox yi ci xam-xam ak jëf ak dëppoo.
Ndaw ñu di sàng yu ñaw ! ñoom de la neexoon ca cafka ga jël nañu ko.
Yal na ngërëm – lol di naa ci dajeek ëlëg ka làq cang gu joyu ga – sottiku ci seen kaw .
Kooka mooy Muhammad, yal na ko Aji-des ji sotti ay xéewal ak mucc mook ñoñam ak saabaam yi di ay ndab yuy duy xam-xam aki xeewal aki hikam.
Li waral xasida gi
Man dey tay damaa ñëw ngir wuyyu lenn ci murid yi di woroomi tuub (ñiy tuub ak a jéggalu seen boroom).
Ñoom de dañoo sàkku woon ñu defal leen woy wuy jàngale ay teggin, ngir ñu sàkkoo ciy teggin, te loolu wartéef la .
Ndax kat képp ku bëgg a topp Yonnant bi te tegoo ko ciy teggin dees na ko xañ ag texe akug jariñu.
Moom teggin de – ci àdduna ak allaaxiraa – mooy gën ji ndàmb tey gën ji lu ku tedd di tedde. Ndaxte mooy leeral ab xol tey
jegeele àjjana.Dina waral say dëkkandoo di la tàgg te dina sooreel it sawara.
Ma daal di jug ngir sàkku gi ñu ko sàkku woon ci man, gaawantu, toontu leen, di ci sàkku nag ab yool ak ngërëm.
Moom nag, du lu dul jël la Walliya wa tuddoon Dal-Haaji wesaroon, manaam la mu bindoon te woyu ko, maanaam defu ko woon ay bayit, def ko ay woy, di ñaan ci def gi Yàlla fajal ma samay aajo
Lu tax ma taamu ko ?
Ndax dafa boole – ba noppi gàttal ko – li ëpp ci li taalifkat yu njëkk ya bindoon cig tàqale.
Lépp loo gis mu neew te doy moo gën lu bari te sonle.
Def naa ko nag woy wu ami njariñ, ci baaxug Yàlla mi dige ci Alxuraan ne dana aar ñi gëm. Ndax Yàlla may ma ci ngërëm ak
kóolute ak njéggal ca bisub njàqare ba.
Kon kat yéen sàkkukati xam-xam yi maa ngi leen di dénk te dellu di leen dénk te di leen xiirtal ci toontu bii (téere Nahju bii).
Ndax kat yor na ci ay jikko aki teggin lol. Bu ngeen ci tënkoo, dina leen wommat jëme leen ca jub ga.
Ay gindee ngi ci aki jariñ yoy boroomug nammeel (ab murid) du ci yoqat mukk. Kuy door a dal ak kaaηfóoree yam ciy njariñam ,
aw yiiwam it du jeex mukk.
Ndaxte ni ñuy àgge ci gën-jaa rafeti jikko yi. mi ngi ci ak ca (lu baax) la ñuy mébët.
Maa ngi ko tudde: Nahju Qadaa Al Haaji ci góob mbayum suñu sëriñ bii di Dal-Haaj.
Maa ngi ñaan Yàlla mu nangu ko ca baaxam ga te àggale liggéey bi. Di ko ñaan it mu mel ne turam wi, ba ki koy jàng ay mbiram
man cee yéweene ngir mu texe.
Te mu musal ma ci ngistal ak aaw (naw sa jëf) ci barkeeb Yonnant biy boroom Liwaaul Hamdi ak yu dul ñoom ñaar ci caay-caay yi (bon-bon yi) te mu may ma ay ngënéel.
Te mu musal ma (t.s) ba fàwwu ci ayuw ibliis mii nga xam ne dafa féttéerlu .
Te mu musal ma ci ayu li mu bind ci suuf si, ak li mu bind ci asamaan si ak li nekk ci seen diggante ñoom ñaar.
Te mu may ma ma topp ci sunnas Yonnant bi (j.m) miy gën-ji mbindéef , miy ku ñu ramuloo, miy ku ñu topp.
Ginnaaw bi ma jullee ci moom te sëlmël ci, ak ñoñam aki saabaam ci anam gu dul dog.
Fii nag mooy fi tarjumaani téere bi yam, kon leegi nanu jublu ci indil leen teggin yi.
Ndoorte li
Ngir woy nos lii di wesaru Seex Ahmadu – mii di ku géeju ci xam-xam – maa ngi naan :
Yeen mbooleem way sàkku yi xam-xam déglu leen sama laabiire gii di leen tàqaleek ag texeedi.
Mu di laabiire gog dañu leen koo jëme ngir jëmmi Yàlla rekk, muy yee nag jépp aji-xellu ak ku jamuj(fàtte) :
Yoonu teggin de mooy yërëm ndaw, ni ko baayam di yërëme ak ndayam te weg mag ak def sa moroom ni sa bopp ngir jëmmi Yàlla mi nekk ca aras.
Xamal ni teggin de mooy taarub boroom xam-xam ak ku koy sàkku, mooy it takkaayi aji-xellu ak ku lewet, mooy njobbaxtalu jikko yi, ku ko takkaayoowul yoqéel na, ñàkk na ay takkaay te neenal, dana mujj di ku Ki bind bañ ak ñi mu bind – Yàlla aki mbindéefam. Képp ku ko gis bañ ko te sànj ko (mere ko), képp ku toog ak moom am ci moom ag yoqat akug doyal.
Bokk na ciy teggin ngay laabiire koo gis ca la nga gis ne ag jubam a nga ca, te ngay bañ a yayale sa bopp jenn àq ci kenn, te
nga jort it ne yayoowoo ci kenn mu lay màggal ci lenn.
Loolu nag mooy li mu junj ci waxam jii :
Na ngay yërëm gone
Na ngay yërëm gone, rikk bu ko nëbbal benn yoon genn laabiire gu aw yiiwam nekk. Deel weg mag,doonte da di ku doyadi te
xeebu. Bokk na ci ay teggin nga bañ a jort ne yayoo nga jenn àq ci kenn ku mu man a doon. Te nga bañ a seentu genn màggal
mbaa wormaal mu jóge ci kenn, kook man nay mer sax ci màggal gi mu lay màggal.
Yaw daal jortal ne teggin yepp ci yaw la war a bawoo, bu leen seentu mukk ci say àndandoo. Àndal ak nit ñi ni nga bëgge ñu ànde ko ak yaw.
Na ngay sàmmoonteek àqi Yàlla – Boroom màgg giy Boroom kàttan gi – ci ñoom ngir jëmmam ja moom Yàlla ni waxi woykat ba. Mu bëgg a wax rekk ne bokk na ci teggin yu rafet ngay sammoonte ci mbindéef yi àqi Ki leen bind(t.s) ci di àndeek ñoom ni ko woykat bi waxe ca qasidaam ga yor bahru basiit:
Yaw mbokk mi na ngay am yërmande ci mbooleem mbindéef yi, na nga leen di xoole bëtub ñeewant ak yërmande.
Na ngay weg mag di yërëm gone, tey sammoontek àqi Aji-bind ji ci mépp mbindéef. Am na addiis bu naan : sama xeet wi de du dañ di nekk ciw yiiw li féek ku ndaw a ngi ciy weg mag, mag di ci yërëm gone.
Kon rikk na nga di roy ci gindig Imaam yi (y.y.g) kon de di nga gindiku.
Bul di toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a ñàkk. Loola mooy lu mel ne ngay jàng ci moom, walla nga dëkk ak moom,walla
nga bokk ak moom di lekk, bul toogandook moom cib lal it.
Saa su Yàlla defee nga toogandook moom, na nga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu akug watandiku, te bul di tafu ci kawam, bul toog it ci kanamam.
Yaw mbokk mi, rikk bu ko tàllal sab tànk boo toogee ci moom, te deel damm sab gis wëlif ko, maanaam bul ko di faral di xool
rekk.
Deel topp ndigali Boroom-mbindéef yi, ndax kat nekk na ci addiis: waay de sànkoo na ci bennub xool rekk. Ab woykat de waxoon na bu yàgg ne :
booy def loo gis xool ko danga ci mas a am bis, kon bul di wëndéel sab gis .
Boo jekkee na nga dalal say cér, na ngay taqook ag noppi ànd ak dëddu ci lug dëddu war, kon de nga jariñu.
Deel muñ ag ηàññ te bu ci toontu kenn, te mel ni na boroom njàngat la waxoon : wallaay damay romb waa ji mu may xas may jellale naan, kii de xam naa ne waxuma, ndax kat xasante ak weddeente bokk nañu ci jikko yi gën a bon niki dóorante. Bariy ree daay ray ab xol, kon rikk néewalal ree yi, ndax nga gërëmloo Boroom bi.
Defal sab toontu boo lottee muy “noppi”, bari na wax joj toontu baa nga ca ag noppi.
Bokk na ci hikma: Bu wax doon xaalis noppi di wurus, bu la nit réeree, def la ag ñàkke-teggin, jéllale ko, taqoo noppi…
Ni ko woykat bi waxe: Amaa na ma romb ku soxat ki, ku yaradiku ki, mu may ηàññ, bu ko defee ma fegu te naan kii daal waxut ak
man; ηàññante ak weddeente bokk nanu ci jikko yi gën a ñaaw, yi gën a bon, ree ju bari day ray ab xol…Na nga xam ne fuqale bokk na ci liy waral gàcce ak yeddeel Képp ku aj yitteem ci lekk ak séy na xam ne boole na lépp luy toroxte. Lekk dee ci jël lu lay dëgëral ba nga man a jaamu sa Boroom te yam ca. Deel wattandiku jamono ju nekk fuqale ndaxte mooy cëslaayu wépp ay.
Bokk na ciy teggin booy jug aajo rekk di la yëkkati, bokk na ci ag ndofe ngay ree te lu reeloo nekku fi, mbaa ngay dox ci lu dul aajo, mbaa ngay gestu te yittewoowoo ko, bokk na ci ay teggin ngay moytoo wuññi say sér, loolu de ci jikkoy kàccoori Hassaan yi la, bul di feeñal lenn ci sa biir mbaa li nekk ci sa diggante jumux ba ci say wóom, loolu de ci réer la ak ñàkk kersa te kersa mooy dàttub diine tey laylaat gi mu tege, fu kersa ñàkke diine jug fa. Bokk na ci ay teggin ngay nuyyu képp koo dox ba àgg ci moom, te di ko fay bu la nuyyoo, te ngay saafoonteek moom tey dëgëral sab loxo ci loxoom boo koy nuyyu, te nga bañ koo njëkk a rocci sa loxo , fëkk loxo ci lu gaaw cib nuyyo de lu ñu sib la.
Bokk na ci ay teggin ngay def booy dugg ci néegub jàmbur mbaa këram ngay yëglu bu ñu la nee jàllsil nga dugg, ndeem déet nga
dëpp, rikk bul di sànni sab gis ci kër mbaa néeg boo moomul ngir nga bañ faa gis loo warul a gis. Boo bëggee kooy àndandool
bu muy ku dese cim xel mbaa ku iñaan mbaa ku bariy xemmeemtéef. Bu di toog ak ku dul ku lay dolli diine ak xel, kon de nga am
càkkutéef la. Ndax de xibaar nañu ne cam si de (waa ji) ma nga ca diiney xaritam ba, loolu ab adiis la bu ñu tuxal. Waa ji de
diine ji waayam yor rekk lay yor.