Waxi neen: Jàng ci làkli réew mi, 44 at ca gànnaaw…
NJUUJ-NJAAJ: Taalifu Seriñ Muusa Ka
Xaralaay létt ci Afriku démb ba téy…
Antoine de Saint Exupéry – Ndoomi Buur si
Antoine de Saint-Exupéry Ndoomi Buur si Traduit en Wolof par Dr. Tamsir ANNE Tudee naa ko Leon Werth Yeen xale yi, na ngeen ma baal, ndax teere bii ki ma ko tuddee du xale, mag la. Wante am naa lay: benn, kookooy sama xarit bi ma gën a fonkk…
Leebu Wolof-Njaay: A ni aada
1. Aar moo gën faj. (20) Image 2. Aawo, aw la tudd. (9) 3. Aawo buuru këram. (2) 4. Aaye na, aayeetul keroog. (1) 5. Ab dag du bëgg moroom ma. (14) 6. Ab lonku, daar a ca gën. (2) 7. Ab yeel bu ëppee ab lupp booba jàngoro rax na ca. (20) 8. Abb…
Diine ci làmmiñu Wolof: Yoonu ragal-Yàlla
Bisimilaahi Rahmaani Rahiimi… Ñu fas yeeney dollee deηkënte ak di dollee fàtleente. Ñiη koy jëmële nak ci tomb bi nga xam ne mbooleem liy yiiwu àdduna ak yiiwu àllaaxira ci la ko sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa dëxëñ. Mbooleem yonant yi mu yónni yépp ci la leen digël ñu teg ci seen tànk. Mbooleem ñi…
Jamono ci wolof
Seex Anta Jóob: Xayma ci Wolof – La héorie des Ensembles
Ensembles équivalents Deux ensembles M et N sont équivalents si à un élément de M correspond un élément et un seul de N, et réciproquement. Le caractère commun à tous les ensembles équivalents est leur nombre cardinal (leur cardinal), leur puissance, c’est-à-dire le nombre de leurs éléments. Faramfàcce Mboole yi Mboole weccikoo Ñaari mboole M…
Téere-woy yi
Téere-woy yi téere la bu ëmb taalif yu bindkat ak xaralakat yu mag ci làkki almaa taalif. Téere baa ngi genn ci atum 2011 ca Almaañ. Tamsir Anne, mi móol dal bii, moo toxal woy yooyu, tekki leen ci wolof. Woykat yi ñu gëna ràññee ci làkki almaa, mel ni Goethe, Heine, Brecht ak ñeneen…
Léebu…
Am bukki yomb na, waaye bukki buy xalam a jafe. Am na bukki bu ŋexalul, te jégéñ kër. Bukki am na gillint, tey àll bi leer. Bukki amtekoonu bàkk yëy ko. Bukki, balaa baax, yooy. Bukki bu daanee ponkal ca doxin wa la. Bukki bu nammee fande reere doom ja. Bukki, kenn du ko…
Bàkku Senegaal
Yëngal-leen kooraa yi te dóor ci sabar yi Gaynde ñaloor yuux na. Boroom àll tëb na Tëb na tëbu jàmbaar, leeral lu doon lëndëm Suñuy naqar jeex na, sunu yaakaar ñëw na Jógleen gaa ñi, waa Afrig gépp a ngi daje Awu Yéen sunu buumi xol, nañuleen àndandoo Sunu deret waa Senegaal, jógleen Nañu…