Maa ngi tàmbale samay wax ak jëf ci turu Yàlla miy kiy boroom yërmande ju yaa ji ci adduna ak ja ca allaaxiraa. Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci suñu sàng Muhammad ak ci ñoñam aki saabaam ci anam yu sax Yàlla doy na ñu, moom de wéeruwaay wu baax la, wu mat…
Yeesal baatu xarala ci wolof / Taatanu Wolof ak Xamle
1- Jollasu gi = téléphone 2- Kippaango gi = groupe 3- Njémmeer gi = public, assemblée, assistance 4- Limat gi = numéro 5- Lënd gi = internet 6- Lënku = connecter 7- Lënkaay gi= 8- connection 9- Peeñ bi= image 10- Baataan= vocabulaire 11- Limtu gi= chiffre 12- Nataal bi= photo 13- Ndéggat gi= audio….
Lu tax nu war a jàng ci làkki réew mi
Melo yi wolof
Bés bu taalifkati yeneen réew làkkee wolof…
* Jukki bii topp maa ngi ko jëlee sama téere bi ma tuddee Téere-woy yi te mu genn ci atum 2011 ca Almaañ. Téere bi mën ngeen ko am NDakaaru ca “Librairie Clairafrique” walla “L’Harmattan” Ubbite bi Ci téere bii, dañu fee tànn woyi taalifkat ak xaralakat yi gën a mag ci làkku almaa, toxal…
Alxuraan ci làkku wolof
Alxuraan ci wolof
Cosaanu mbind ci Afrik
Cosaanu mbind ci Afrik lu mat a fésal la, ndax ñu bari, waay-xeltu yeek meroe.jpg ñeneen dañoo defe ne caada yi nekk Afrik xamuñu ca seen cosaan xaralaay mbind. Manaam xeetu mbind yi fi nekk yépp dañu leen a jeggani: ci Arab yi mbaa ci Nasaraan yi. Loolu nag dëppoowul benn yoon ak li am:…
JIROO SUUF SI… “Jarul laaj…”
Madumbeek lekolu tubaab bi
Sedaar Seŋoor: Juwaaloo
Juwaalo Juwaalo! Maa ngi fàtteliku. Maa ngi fàtteliku siñaar ya ca keru mbaar yu naat ya Maa ngi fàtteliku siñaar yeek seeni gët, kéemtaanee lool Di sàmandaay leeraayu weer cig tefes Maa ngi fàtteliku jànt yu so yu taaroo-taaru Kumba Ndofeen naan da cay dog manto buuram. Maa ngi fàtteliku bernde dëj yuy gilli deretu…
Sàrti ndaali-Maali
Dr Tamsir Anne (tekkikat bi) Ndaali Maali, walla Mande, benn la woon ci nguuru nit ku ñuul yu mag yi nekkoon démb ci déndub Afrig. Moo fi wuutu woon ndaali Gana ci Afrig sóowu jànt. Gana moom itam moo donnoon jàllooreey yeneeni nguur yu mel ni Aksum , Kuus, Nibi ak Misira démb bu Buur-Fari…