Matukaay 30eel:
Nañu dimbali képp ku yelloo ndimbal.
Matukaay 31eel:
Nañu fonk mbokk, séy ak dëkkandoo.
Matukaay 32eel:
Ray leen seen noon su waree, wante bu leen ko toroxal.
II. MOOMEEL YI
Matukaay 34eel:
Ci juróomi anam yii topp mënees na cee am lu lew: jënd ak jaay, maye, weccee, liggéey ak ndono. Beneen yoonu am-am bépp bu leen moy te amul seedde dese naa lew.
Matukaay 35eel:
Lépp lu ñu for te kenn newul ne moo ko moom, su àppu 4 at weesoo kese lay mën di doon moomeelu mbooloo mi.
Matukaay 36eel:
Nag wu ñu denkaane, su juree ñeenti yoon, ñeenteel ba ka ñu ko denk moo ko moom.
Matukaay 37eel:
Sëll ñetti xar mbaa ñeenti bëy lees koy weccee
Matukaay 38eel:
ñeenteeli nen bu nekk ka ñu denk ginaar gaa ko moom
Matukaay 39eel:
Xiif gis loo lekk, lekk ko, du ag càcc soo yemee ci lekk rekk te jëloo ca dara yobbale.
III. AAR CÀKKEEF Gi
Matukaay 40eel:
Àll bi mooy suñu am-am bi ñu war a gën a fonk: ku nekk war na ko sàmm, aar ko ngir tawféexu askan wépp
Matukaay 41eel:
Saa yoo bëggee taal àll bi, bul xool ci suuf, téenal xool njubaqtanu garab yi.
Matukaay 42eel:
Jur gi ci kër yi dañu leen a war a yéew saa yu nawet teroo te deesu leen tekki feek góobuñu ba noppi: Xaj, muus, kanaara ag njànaaw gi bokkuñu ci.
IV. MATUKAAYU YU MUJJ YI
Matukaay 43eel:
Bàlla Faseke Konaate moom lañu fal mu yilif lépp lu aju ci xew-xew yi ak baaxental yi. Mooy kiy dox rataxal-diggante askanu Mande gépp.
Ci loolu may nañu ko muy kaf ak a kàlloo waaso yépp rawatina njabootu Buur-Daali.
Matukaay 44eel: Képp ku wàcc sàrt bii yoon dina la duma. Ku nekk war na koo saytu te di ko jëfe ci biir réew mépp.
Serin Ann, sart bi ni gaka tekke taruna lol.Waw gor
jaajëf Baay Tamsiir. lii de man umpon nama, te lima gëna yéem mooy nimu dëppook jamono ci yu bari ci sunu jamono jii, mbaa sax sunu jamono dabagu ko ci yenn yi.