79. Ardoo néwi, ñu tup Malal. (9)
80. As gor dina dugg ciy naxam. (2)
81. Asamaan lu mu taw-taw suuf àttan ko. (9)
Lu asamaan taw, suuf mën na koo dékku. (2,7)
Lu asamaan taw-taw, suuf dékku ko. (19)
82. Asamaan moo di buuri mbaar. (4,13)
83. Àtte bor ak fey. (12)
Àtteb bor, fay. (19)
84. Aw doj du yàgg géej ba tax mu doon aw jën. (7)
4 85. Aw fas, manees na koo wommat ba cim ndox, waaye naanloo ko te marul, maneesu ko (11)
Manees naa wommat fas ba cim ndox, waaye maneesu koo naanloo te neexu ko. (12)
86. Aw naaru-góor lu mu mëna mëna daw ñu bàcc ko ab yar. (2,6)
Fasu naaru-góor, lu mu mën-a-mën daw ñu làbbili ko. (3)
Lu naaru-góor gaaw-gaaw, fàww ñu làbbali ko. (19)
87. Awma ginaar siiru sikk ma duma ci fekk. (12)
88. Ay du weesu baay dee na. (7,12)
89. Ay du yem ci boppub boroom. (2,7,9,12,14)
Ay du yem ci boppu boroomam. (11,15)
Musiba du yem ci boppu boroom. (20)
90. Ay wax yu bare, du may lu ñu lekk. (4)
91. Ayi waay jàmmi waay. (17)