Kawe nga mboolem xarnu bi
Jomb na mboolem xarnu bi
Lut Bàmba bàjjob xarnu bi
Di folli seef i xarnu bi
Leeram ya dar na xarnu bi
Seexal na mboolem xarnu bi
Ba jot ci mbóot i xarnu bi
Ba të na nooni xarnu bi
Moo nàndaloon waa xarnu bi
Du jëw du jànni xarnu bi
Moo gën a wuuteek xarnu bi
Faadiilu aj na xarnu bi
Jikkoom ya waar na xarnu bi
Dendam amul ci xarnu bi
Mus la tawat ci xarnu bi
Te du ko feg ci xarnu bi
Wakkiirlu dëddu xarnu bi
Gañe na mboolem xarnu bi
Du jaay du jandal xarnu bi
Dellu si fii ci xarnu bi
Moo gën a wuuteek xarnu bi
Cey Yàlla ! bàjjob xarnu bi
Mooy génn góor ci xarnu bi
Di nig li des ci xarnu bi
Xamul ku bon ci xarnu bi
Kon du fBàmbaay boroom «kun, fayakuun»!
Baatin la daa fab di nu jóor
Tarbiya, lay yarey goneem
Diraaya, lay xamal goneem
Cofeel gi, moo ma ko xamal
Moo tax ba dóotu ma selaw
Leeram gi, daal may tex-texaan
Seex Bàmba, yaa di sun Imaam
Sëriñ si woon dañoo texëm
Ku leen faboon, teg ci balaas
Xawsu ya, mooy séen Yilimaan
Moo am “fasaahatu lisaan”
Moo am “maxaarijul huruuf”
Mooy “Muhjisaati adnaan”
Tuubaa, ñeel na kuy muriid
Jox naa ko fàww sama xol
Bàmba, da ngay boroomi may
Woyu nu ngir bëgg i dërërm
Yaw mi laggeeyal sa boroom
Tàbbal nu “jannatul na`iim”
Ridwaan tijjil nala, nga wéy
Nopplu jil ca «Illiyiin»
{Ak Mursaliina’ak Lanbiyaa
Yural sa punk, te dem fanaan
{Alhamdulillaahi na ngéen;
Yaw mi laggéeyal Mustafaa
Matna xaliifatul xadiim
Noppeek, goreek, tàllal ndijoor
Taafeeri njool aaminata
Yaa neex a way, te neex a taas
Raayaw ngënéel wi yaako yor
Mboolem sixaarun wa kibaar
Robino yaangi’y walangaan
Jumaa ji yaa ko taxawal
Yaw la sulaymaan xamalon
Daawuda Bàmba lay misaal
Ndommoy ngënéel ya won ca maam
Muriid yi jox nala’y Idaay
Yàlla nangay muuram muriid
“Allaahu dhoo-l-fadlil aziim”
Mooy doomi “shamsun wa xamar”
Saddiiti baayam lay royaat
Mooy noobalub lislaam fi nun
Ma wax la lëf, ci ay jikkoom
Dem na ba màkkam jullikaay
Taalif i baayam’ay wayam