Dundal nu, noo di sa’g njaboot
Wodd nu, nee nu wàkk boot
Te suturaal nu, may nu mbóot
Nee léen «amiin» yéen xarnu
Yaay fekk waay i njoro-ndiaay
Nga fal ko, boole kook i gaay
Ni doom i Maam Sëynabu Njaay
Làmp bi won ci xarnu bi
Muriid yi yaa yor séen ngërëm
Sëriñ si yaa yor séen xorom
Biñ la gisul ñi’ng ni xerem
Fajal nu aajoy xarnu bi
Seex Bàmba yaa di ag nduyoor
Sëriñ si ñoo doon njawli béer
Waa ju la nemm falu buur
Sa lem gi neex na xarnu bi
«Wa saabiquuna saabiquun»
Yàllaay boroom «Kun fa yakuun»
Ewwaaye gaay ya fi jëkkoon
Ñoo yobbu mbóoti xarnu bi
Ña raflewoon wodd na léen
Ña ko bëggoon Seexal na léen
Seex bàmba yaay ngayndeg njaloor
Fàddal nu ndaama yii di daan
Seex bàmba yaa matub Sëriñ
Soppi nu ay wagook i gaal
Seex bàmba yaa matub sëriif
Siggil nga waa mbàkke bawal
Mbàkke dimb’ak, mbàkke xewar
Askanu kër maam maaram
Daarus Salaam, Daarul Minan
Yaa tax ñu dooni kàppitaal
Sa daaru yee di’y lóppitaal/n
Ràggi xol’ak ràggi yaram
Fekkoon nga réew mi defi ndóol
Fekkoon nga ñii defi lafañ
Yaa dikk jag ya fi dammoon
Amal nga gaa yu amulon
Sa waay du ñee waayi kaneen
Taxoon nga ruuh yi dajaloo
Xàlloon nga ngiir mi ba mu weex
Wommat nga ruuh yi jox boroom
Dekkal nga julliy juróom
Aw nga siraatal mustaqiim
Sunna si yaa ko dekkalaat
Fekkon nga ñuy waññ ak a tuur
Soppi jigéen ñiy muslimaat
Yaa tax nu daa sellali jëf
Jirim yi yaa don séeni baay
Ku jooy fi yaw nga noppi loo
Billaahi yaa mat li nga doon
Mboolem sahaabatu rasuul
Ka’ab dadaa tagg rasuul
Yaa raw ña daa janook rasuul
Yoon wamu aw ba raw mbindéef
Diggante mulkoo’k malakóot
Aras la daa gisee’k boroom
Moom la ñu may nuurul jalaal
Gaa léer, ca lay jañe’y cibeel
Yàlla la daa sukkandi koo
Téere ya lay wéttalikoo
Taalif la daa jëfandikoo
Tawhiid la daa xamali jaam
Fum toll day tagg rasuul
Dem jàkk a moo ko tax a nuuj
Njool màkk a daal lay segeree
Fab na ca xayru lanbiyaa
Dëddoom gu mat gamu jagoo
Nattoom yu rëy yam daa tegoo
Dunyaa da koo wanon gannaaw
Bëggul galan bëggul medaay
Bëggul fas ak nag ak galeem