Sëriñ bi geesul xarnu bi
Muriid yi saalit nanu ren
Ngir xamni yaa léen ame wan
Yaa léen joxon la nu yoran
Yobbu nga mbóoti xarnu bi
Tiijaan yi réccu nañu tay
Xam nañ ni bëy du sóoru boy
Yaa man a may nit lu ko doy
Moo tee nga naatal xarnu bi
Bawal-bawal jolof-jolof
Mboolem pël’ak naar’ak wolof
Kenn gis a tul ku ame yëf
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Koo xam ni daan a ame jaak
Daa ame àngaar’aki juuk
Mii at mu am déwén mu jéek
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Ku mas a am yaar i wata
Soxla na ren jii yaar i mëta
De munta am njëg u mëta
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Koo xam ni daan a ame taax
Tay ming ni ngeeju’b néek bu baax
Bu gën a feex bam ni ca faax
Sëriñ geesul xarnu bi
Kër yaa ngi wéet ba ni woyoŋ
Lal yañ yoroon def i koyoŋ
Ña doon i wuur def i koyaŋ
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Tubaab yi sax pert nañu
Ña léen gëmoon pert nañu
Yahood yi it fayit nañu
Yal na ñu yées ci xarnu bi
Ña tukkiwan faf nañu laŋ
Fuñ wàcci deef i léen falaŋ
Àdduna yaa ka noo welaŋ
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Naar yaangi yalwaan’ak a xaar
Seex buñ xamoon dellu fa jaar
Ken talatul loo jox i naar
Sëriñ bi geesul xarnu bi
Wooy Mbàkke ! yuuxu nan ba dee
Wallu nu boo yeexee nu dee
Melal ni kuy rammu ku dee
Yaa nuy tinul waa xarnu bi
Yaw yaay donoy Muhammadu
Te yor nga sirrub Ahmadu
Te yor nga bóot i Haamidu
Man ngaa defar waa xarnu bi
Man ngaa defar biteek i biir
Defar nga baadoola’aki buur
Yaa dindi àllarba’ak dibéer
Sàkk Muriidi xarnu bi
Man sa kanam, man sa gannaaw
Loo sant Yàlla mu ni waaw
Loo wax fa diiwaan ñu ni waaw
Wax léen ñu naatal xarnu bi
Sa mbir ëppante na’ak dërëm
Nde xarnu bépp am gërëm
Te am dërëm te yokku ngëm
Nga may njariñ waa xarnu bi
Ma léebu ngaa yi la xamul
Waa ju xamul dees koy xamal
Subhaana, yaa ka mat kumal
Yaa neex a wan waa xarnu bi
Nan far waññee ku tagg daam
Ngir moo nu may lu jombi maam
Boolee’k Muriid yuy daw di raam
Ag cant a war waa xarnu bi
Bàmba muneef u laa misaal
Yaay géej gi wër waa senegaal
Deef u la jàlle genn gaal
Say duus a tooyal xarnu bi
Seex Bàmba yaa di’k mbàmbulaan
Ku sóobu dóotu ñaane naan
Ku màndi day démbaan i teen
Say kaas a màndal xarnu bi
Ku sóobu génnaaley dërëm
Békkoor bi dóot u dem kërëm
Ku ni curum kaasub ngërëm
Doo mar li des ci xarnu bi
Géejug hikkam ga mu dëtëm
Bani ko sécc moo’k ñoñam
Maseef u caa nàndal ku xam
Toqan nga doy na xarnu bi
Luum loo na fóore ya wéyon
Raam loo na kàngam ya fi won
Daane na mbër ya fi newon
Amul niroo ci xarnu bi
Sirrub andaar i xam-xamam
Museefu caa nattal wujjëm
Ayam ngi suural na’w ñoñam
Wujjëm amul ci xarnu bi
Fekkon na dab yi ni xareet
Mu soppi léen watay sareet
Duy léen ngënéel bañ ni sëréet
Wàccoo na moo’k waa xarnu
Taalif na móol yu fees i taax
Te xalimaam du juum du jaax
Te am xelam du gag du naax
Du fàtte lëf ci xarnu bi
Day duusu dong a yay dëtëm
Duus yay jallaañoo ci’b dënnam
Mooy géej gu ridwaan di’y jënam