Murid dëgg bul mer te bul jàpp mer
Mer ak jàpp mer day alag am murid
Meral say ayib yow gërëm sam sëriñ
Di daw nemm tan ba am ay murid
Jom ak jikko ak fula yii yett a bon
Jigul rëbb ak dag, jigul am murid
Ku am yett yi kat du am yett yii:
Ngërëm, barke, wërsëg, yëgal lii murid
Bàyyil jom ngir rëbb day ñàkk jom
Ba jam door a am jom
Te rëbb ay murid
Jom ak fula baaxul dafay tax mbirum
Murid Suufeel, yii xam ko yow kiy murid
Di am jikko, am jom, am fula ba tax
Sa rab wii di raw, lu jar lii murid ?
Defal ndànk tey waaf ak a daw ba jam
Bari jikko kat moo di gàkk ub murid
Digal naa la aw yiiw, te man lii ma war
Defal nii, ku def nii di ngën gi murid
Defal, boo defe nag ma def, boo deful
Ma def tey digal nag beneen ub murid
Te it sant naa la gërëm naa la it
Dama bëgg ngay jiitu bépp murid