Te boole luy taaw ak i ñaat
Mboolem lu Sayxu Bàmba am
Muusaa ka miy séen werekaan
Waykat yi buñ yaboo ni xiim
Ngir Abdu Mbàkkem soxna MBAY
Saynabu Mbàkkem Absa njaay
Mbaa muy julleek a jàngi ñaan
Te tol ni maam ahmadu daam
Mooy jàpp doom, def ko ni baay
Seex Bàmba, ñoo niroo’b jataay
Niroo jëmm’ak meloo’k defiin
Bu léen ko xool bët i kañaan
Moo donnn njàmbaar ga ca moom
Day gaaw a soppi ay mbiram
Te yalna raw pexem mëriid
Mu may Sëriñ Abdu Samad
Sëriñ bu mag bi gën ci yéen
Fii baatinin wa zhaahiri
Def’ab xariit fa sun boroom
Ci sowwu jant, mbaa feneen
Ju bari jaa’ak, jam darajaal
Te sol ngërëm ci murtadhaa
Góor ak jigéen, ci benn baat
Yal nañu gën te yokku ngëm
Moo léen di woy, di léen dagaan
Maa war di xaadimul xadiim
Ak Maaram mi ñépp ŋoy
Ak Maaaram miy ngën ji baay
Yooyu la baaxoo, te ku ñaan…
Te donn mbóot ya won ca daam
Ñu bokk bennu’b taxawaay
Niroo yaram, niroo sewaay
Buy ree nga waat ni du keneen
Kañaan du tee béjjan a daan
Séen baay a séddale’y jikkoom
Mbir ma ca baayamay mbiram
Te yalna mujj di’b fëriid
Te may Sëriñ Abdu Lahad
Yàlla bu séeni barke neen
Bijaahi baayu taahiri
Ba jot ca bóot i turandóom
Yàlla na saalihu di séen
Yal na ko Seex Bàmba misaal
Ba ku ko soob mu def qadhaa…
Ndax Yàlla sun xarnu bi naat
Kon, leenu bokk ame ndam
Tey sant, tey tagg ak a ñaan
Damay muriid, di jaam, di doom
Mooy baayi-baayi sama nday
Mooy baayi-baayi sama yaay
Mu mayla lëf ci xarnu bi
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Abdoo, di Bàmbam xarnu bi