Te nduruwul boroomu tiis
Jagle ga jiitu na’b juddoom
Bu nee jalañ, ñuy safi jaam
Fegal ko ayu bépp noon
Donoy bashiiran wa nadhiir
Te xar kanam ga leer kamaal
Ba buur ba fal ko def ko doom
Fóore ya daa fireek a raw
Ku ko rawon, neena la wif!
Mbirum `Inaaya la làkkoo
Moo tax amul xejj ak i seen
Mboolem jigéenam aku góor
Tasfiya, Mbër yu deefi yéem
Wilaaya, lay defal boroom
Leeram gi, fees na sama xol
Maa nguy wëréelu, ni gelaw
May naan ba màndi, coroxaan
Yaw la nu doyloo, ba fa saam
Seex Bàmba, moo safon xorom
Konte, mu wat séen i palaas
Adiisi Yonen, ba rañaan
Moo xam, la wàcce asamaan
Mooy waykatub gën ji mbindéef
Di rammu xeet wu jëm jinaan
Yal na nu Bàmba def muriid
Terub mbalaan i sama xol
Mootax nu sax ci di la woy
Ca bis ba Yàlla di yërëm
Wàllil nu yaw ci say juróom
Wuntu ya, yaa yor seeni doom
Waaju la soob mu daal di wéy
Yonen gërëm na la’ak ñeneen
Jinne ya’ak Malaayika ya
Nottil te lekk nag, te naan
Doom a di baay kii du kaneen
Ak doomi baayi Mustafaa
Te amna xam-xam, ame koom
Ku laaj, mu joxla lay sa muur
Tuubaa di sun madiinata
Li dale fii, ba weesu faas
Ngir naaru góor ak fasu par
Ba wàcc Tuubaa ngën ji gaar
Dóotu nu tàppaatuy sayaan
Naalam wi/u yal nang ko matal
Jumaa ja bayti tabaxoon
Wuy ji boroomam ba kamaal
Nga boole koo’k ngënéeli daam;
Sultaan nga boole koo’k wilaay
Bihaqi xaadirin muriid
Faadilu mooy “fadlu hamiim”
Moo nàmp yaari meeni ngor
Nday jaa di xayru muhsinaat
Donoy usaynu wal-Hasan
Niru na baay ba, mat na doom
Te ëndiwul alal di jaay
Moo naan ci géejug hikkamam
Ci moom, te yal nan am i sët
Xarbaax la feese, bani guun
Soo ko gisee ma ngay bangeer
Day fal di folli ci lu gaaw
Mooman arab te man wolof
Kuy rooti, moodi dex gu fees
Mbër mu ko sóoru daal di luum
Nërëm-nërëm, di safi mbaam
Ku dégg ñaan, nani amiin
Ku teeru naan, lekk ba suur
Tem bari xam-xam am alaal
Jigéen ja far tàngook sagoom
Musula jaar ci yëfi ndaw
Moo raw ña xàllon moom a lef
Nuurul wilaaya la sàngoo
Mooy yërmàndey waa xarnu bi
Defar na léen ci xarnu bi
Bañ man a ànd’ak xarnu bi
Cofeel gu am ci xarnu bi
Baawaan ci gaa yi xarnu bi
Dóotu ma toog ci xarnu bi
Di buusu gaa yi xarnu bi
Rammu nu, nook waa xarnu bi
Safaale gaa yi xarnu bi
Mbàkke! du maasam xarnu bi
Moo ko xamal waa xarnu bi
Jëm si ci suusi xarnu bi
Maay waykatam ci xarnu bi
Tuubaa li ahli xarnu bi
Neeleen “amiin” yéen xarnu bi
Fóotal nu gàkki xarnu bi
Ndaxte, nga jéggal xarnu bi
Xeet wi newoon ci xarnu bi
“Yawma yaquumu” xarnu bi
Tijjil dugal waa xarnu bi
Yaa ame caabiy xarnu bi
Ak xulafaa-uy xarnu bi
Gërëm nañook waa xarnu bi}
Jaajëf! defar nga xarnu bi
Man naa defar waa xarnu bi}
Ñoo ame bóot i xarnu bi
Man naa musël waa xarnu bi
Te musla gàntul xarnu bi
Yaay weer wi tiim waa xarnu bi
Yaw lañu jébbal xarnu bi
Rawante wuñ ci xarnu bi
Noppal nga léen ci xarnu bi
Jaajëf! defar nga xarnu bi
“Aamiina” war na xarnu bi
Moom ngay defal waa xarnu bi
Taaw ba defal ko waa xarnu bi
…Ràngoo, amoo ci xarnu bi