Yaa tax ba nuy niinal i bool
Ñoo ku ñu ñaan jabar mu bañ
Yékkati néeg ya suufe woon
Feeñal nga mbir yi nëbbu won
Deesu la xam di gëm kaneen
Te wate woo ni kuy faloo
Te masulaa jàdd aka jeex
Seex bàmba ken du sa moroom
Te fetaloo bañ ami góom
Ba àgg yaak sa yépp doom
Te alxuraan yaa ko falaat
Yaa sampi daaru, fali wuur
Rékki takkaayi séen i baat
Yaa tax ba nuy woy di walif
Miskiin yi yaa doon séen nijaay
Ku mar fi yaw nga màndi loo
Wàccal, damul, langul te téen
Melna ni bay nga séen i tool
Hasaanu daa tagg rasuul
Ba def xaliifatu rasuul
Maneesu koo xamal mbindéef
Ken musla boole séen i bóot
Diiwaan la daa faley moroom
Mu boole koo’k sirrul kamaal
Kamaal ga lay falee’y meteel
Jibriil la daa dimbandi koo
Pexe ya noon ya daa jagoo
Hikkam la daa sukkandikoo
Riwaaya lay gonte nekaam
Du werse boŋ ci tarasool
Aj màkka mas na ko ni ngéej
Giñ naani daawu ñu soree
Moo raw xiyaaru lasfiyaa
Ak muñ gu rëy ga mu sagoo
Te amna bóot yu mu fegoo
Jublu ci Yàlla ne njanaaw
Jaayante na ak Yàlla sa waay
Bëggu la am sàqi njuróom
Moo mas a dox ba dem gaboŋ
Nawul dërëm xeebul përëm
Kuy waaru bàmba doyna waar
Bëggul bañul xeebul du yéem
Ku laaj mu jox la sa muur
Kon du ko may sëriñ guyaar
Baari, gënul fi moom pataar
Kon taaxi jurbel du fa jaar
Bañ wommataale xarnu bi
Bañ del si ànd’ak xarnu bi
Mbaa weeru gàmmuw xarni bi
Te def nu mbër ci xarnu bi
Say gaal a jàlle xarnu bi
Def nub masin ci xarnu bi
Maam Jaara tiim na xarnu bi
Lu tax ñu siiw ci xarnu bi
Ba ñuy defar waa xarnu bi
Daagul rusoo ci xarnu bi
Ku weddi seetal xarnu bi
Ñoo gàddu mboolem xarnu bi
Doktoor bi yaa faj xarnu bi
Ngir yaa wéral séen xarnu bi
Yafal nga mboolem xarnu bi
Ñii mel ni man ci xarnu bi
Bañ man a ànd’ak xarnu bi
Dekkal nga ruuhi xarnu bi
Sa diine doyna xarnu bi
Lislaam nga moome xarnu bi
Ba yobbu mboolem xarnu bi
Yaa man a jàlle xarnu bi
Yaa wone diiney xarnu bi
Tay ñi ngi wommat xarnu bi
Yaa bind loo won xarnu bi
Tasaare daaray xarnu bi
Di muuru dëddu xarnu bi
Xamal nga gaa yi xarnu bi
Yaay wéeruwaayu xarnu bi
Màndal nga góoru xarnu bi
Nde wub nga làmbi xarnu bi
Bayaale tool i xarnu bi
Semmal nga léen ci xarnu bi
Kawe nga mboolem xarnu bi
Jomb na mboolem xarnu bi
Lut Bàmba bàjjob xarnu bi
Di folli seef i xarnu bi
Leeram ya dar na xarnu bi
Seexal na mboolem xarnu bi
Ba jot ci mbóot i xarnu bi
Ba të na nooni xarnu bi
Moo nàndaloon waa xarnu bi
Du jëw du jànni xarnu bi
Moo gën a wuuteek xarnu bi
Faadiilu aj na xarnu bi
Jikkoom ya waar na xarnu bi
Dendam amul ci xarnu bi
Mus la tawat ci xarnu bi
Te du ko feg ci xarnu bi
Wakkiirlu dëddu xarnu bi
Gañe na mboolem xarnu bi
Du jaay du jandal xarnu bi
Dellu si fii ci xarnu bi
Moo gën a wuuteek xarnu bi
Cey Yàlla ! bàjjob xarnu bi
Mooy génn góor ci xarnu bi
Di nig li des ci xarnu bi
Xamul ku bon ci xarnu bi
Kon du fBàmbaay boroom «kun, fayakuun»!
Baatin la daa fab di nu jóor
Tarbiya, lay yarey goneem
Diraaya, lay xamal goneem