Jaaraama daam ci xarnu bi
Luy nit ku ñuul’ak nit ku weex
Diggante askan yu du jeex
Fu nekk daam def na fa seex
Bu man a yor waa xarnu bi
Mbindéef yi yaa léen fal i buur
Ku mas a xëy taal baboor
Di xelli attaaya ju foor
Fajoon nga aajoy xarnu bi
Soodaanu war nañ ni nërëm
Biidaanu war nañ ni na’am
Ñépp di sant ak a gërëm
Ngir yaa defar séen xarnu bi
Ko-mersi naa la mersi ñoom
Pël yaa nga naala «mujji-doom»
Wolof ya naa «amoo moroom»
Yaa dàmbe tagg i xarnu bi
Ken dóotu dox kem li nga dox
Ken dóotu wax kem li nga wax
Ken dóotu jox kem ñi nga jox
Daralewoon nga xarnu bi
Limaamu Shahraaneey kamaal
Téeréerm ba Bàmba lay misaal
Giñ naa ni mooy aboo rijaal
Xutbu yawon ci xarnu bi
Mboolem xawsu ya weyon
Yaa sóobu ngiir ya ñu awon
Wommat nga «ruu» ya ñu yoron
Yeesal nga wirduy xarnu bi
Xaadiru, yeesal ngay biram
Tiijaanu yeesal ngay biram
Shazaliyu, yeesal ngay biram
Kuntiyu jox la xarnu bi
Lottal nga ñoñ sharii’atu
Jommal nga ñoñ haqiiqatu
Sa ngiir mi mooy tariiqatu
Moo gën a jub ci xarnu bi
Woroom kurus yadaa aji
Ak gaa ya daa siyaare ji
Yaa tax ñu daa siyaare ji
Sëriñ sa woon ci xarnu bi
Wommat nga naar yeek i wolof
Xàllaat nga ngiirum tasawuuf
Shariif yi yaa tee ñu shuruf
Jàlle nga léen ci xarnu bi
Roytéef i xarnu bi nga won
Kiimaan i labdaal yi nga won
Kiiraay i lawtaad yi nga won
Ak nujabaa-uy xarnu bi
Xutbu yi, yaw lañ daa fegoo
Nattu ya góor ña daa tegoo
Lashyaax yi yaw lañ daa sagoo
Bay laaj hidayay xarnu bi
Naar yaa ngi am hidaaya tay
Tiijaan di laaj hidaaya tay
Te musu ñoo weesu bu rëy
Yaw la ñu roy ci xarnu bi
Seex Bàmba, yaa di ab newet
Sébbi nga tooyal gépp wet
Bay nga mu ñor, góob nga fat
Man ngaa dundal waa xarnu bi
Dundal nu, noo di sa’g njaboot
Wodd nu, nee nu wàkk boot
Te suturaal nu, may nu mbóot
Nee léen «amiin» yéen xarnu
Yaay fekk waay i njoro-ndiaay
Nga fal ko, boole kook i gaay
Ni doom i Maam Sëynabu Njaay
Làmp bi won ci xarnu bi
Muriid yi yaa yor séen ngërëm
Sëriñ si yaa yor séen xorom
Biñ la gisul ñi’ng ni xerem
Fajal nu aajoy xarnu bi
Seex Bàmba yaa di ag nduyoor
Sëriñ si ñoo doon njawli béer
Waa ju la nemm falu buur
Sa lem gi neex na xarnu bi
«Wa saabiquuna saabiquun»
Yàllaay boroom «Kun fa yakuun»
Ewwaaye gaay ya fi jëkkoon
Ñoo yobbu mbóoti xarnu bi
Ña raflewoon wodd na léen
Ña ko bëggoon Seexal na léen
Seex bàmba yaay ngayndeg njaloor
Fàddal nu ndaama yii di daan
Seex bàmba yaa matub Sëriñ
Soppi nu ay wagook i gaal
Seex bàmba yaa matub sëriif
Siggil nga waa mbàkke bawal
Mbàkke dimb’ak, mbàkke xewar
Askanu kër maam maaram
Daarus Salaam, Daarul Minan
Yaa tax ñu dooni kàppitaal
Sa daaru yee di’y lóppitaal/n
Ràggi xol’ak ràggi yaram
Fekkoon nga réew mi defi ndóol
Fekkoon nga ñii defi lafañ
Yaa dikk jag ya fi dammoon
Amal nga gaa yu amulon
Sa waay du ñee waayi kaneen
Taxoon nga ruuh yi dajaloo
Xàlloon nga ngiir mi ba mu weex
Wommat nga ruuh yi jox boroom
Dekkal nga julliy juróom
Aw nga siraatal mustaqiim
Sunna si yaa ko dekkalaat