Yaa man a tàggat xarnu bi
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Turam wi, doyna xarnu bi
Mooy Bàmba tay ci xarnu bi
Moo donn mbóoti xarnu bi
Maay xaadamam ci xarnu bi
Ëmb na kersag xarnu bi
Nawleem amul ci xarnu bi
Sirroom ba, doyna xarnu bi
Yu gën a gëm waa xarnu bi
Baay baa ko lëm ci xarnu bi
Ni kuuy lu mat ci xarnu bi
Matnaa ragal ci xarnu bi
Jommal na mboolem xarnu bi
Moo man a màndal xarnu bi
Mbiram xajul ci xarnu bi
Raamal ko war na xarnu bi
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Doo ñàkk lëf ci xarnu bi
Buurika fiika xarnu bi
Manga’ak bashiirum xarnu bi
Musula faale xarnu bi(àdduna)
Sakkaa ñi teewe xarnu bi
Dendam amul ci xarnu bi
Durus ci téerey alxuraan
Yal nafi/u sax, ba dégg maam
Allaahu moodi jenn waay
Booko gisee muy sàmmandaay
Niroo doxiin, niroo waxiin
Moodi wallax-njaanu jinaan
Moo donn tab, ga woon ca moom
Baatin ba, raw na saahiram
Yal nañ ko dolli ay muriid
Nan ñaan ci Yàlla miy Samad
Ci bóoti “qul huwa fadhliin”
Te yokk Abdul Qaadiri
Te yal na Ibraahima moom
Mboolem ñi dooni saalihiin
Dundak So`aybu ga’ak, alaal;
Te maynu barke ak ridhaa
Te boole luy taaw ak i ñaat
Mboolem lu Sayxu Bàmba am
Muusaa ka miy séen werekaan
Waykat yi buñ yaboo ni xiim
Ngir Abdu Mbàkkem soxna MBAY
Saynabu Mbàkkem Absa njaay
Mbaa muy julleek a jàngi ñaan
Te tol ni maam ahmadu daam
Mooy jàpp doom, def ko ni baay
Seex Bàmba, ñoo niroo’b jataay
Niroo jëmm’ak meloo’k defiin
Bu léen ko xool bët i kañaan
Moo donnn njàmbaar ga ca moom
Day gaaw a soppi ay mbiram
Te yalna raw pexem mëriid
Mu may Sëriñ Abdu Samad
Sëriñ bu mag bi gën ci yéen
Fii baatinin wa zhaahiri
Def’ab xariit fa sun boroom
Ci sowwu jant, mbaa feneen
Ju bari jaa’ak, jam darajaal
Te sol ngërëm ci murtadhaa
Góor ak jigéen, ci benn baat
Yal nañu gën te yokku ngëm
Moo léen di woy, di léen dagaan
Maa war di xaadimul xadiim
Ak Maaram mi ñépp ŋoy
Ak Maaaram miy ngën ji baay
Yooyu la baaxoo, te ku ñaan…
Te donn mbóot ya won ca daam
Ñu bokk bennu’b taxawaay
Niroo yaram, niroo sewaay
Buy ree nga waat ni du keneen
Kañaan du tee béjjan a daan
Séen baay a séddale’y jikkoom
Mbir ma ca baayamay mbiram
Te yalna mujj di’b fëriid
Te may Sëriñ Abdu Lahad
Yàlla bu séeni barke neen
Bijaahi baayu taahiri
Ba jot ca bóot i turandóom
Yàlla na saalihu di séen
Yal na ko Seex Bàmba misaal
Ba ku ko soob mu def qadhaa…
Ndax Yàlla sun xarnu bi naat
Kon, leenu bokk ame ndam
Tey sant, tey tagg ak a ñaan
Damay muriid, di jaam, di doom
Mooy baayi-baayi sama nday
Mooy baayi-baayi sama yaay
Mu mayla lëf ci xarnu bi
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Abdoo, di Bàmbam xarnu bi
Niroo deret ci xarnu bi
Bàmba’a ñëwaat ci xarnu bi
Baayam a leeral xarnu bi
Sédde ko lii ci xarnu bi
Moo yor jaliili xarnu bi
Ba tol ni gaayi xarnu bi
Lu doy a doy waa xarnu bi
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Bam tol ni Jiilim xarnu bi
Ndax Yàlla naatal xarnu bi
Jant bu tiim waa xarnu bi
Ci sun So`aybum xarnu bi
Haajaatihii, ci xarnubi
«Aaamiina» warna xarnu bi
Te am ngërëm ci xarnu bi
Ndax yàlla naatal xarnu bi
Te gën a bon ci xarnu bi
Maa dikke nii ci xarnu bi
Maa dambe yii ci xarnu bi
jukki bi: daaraaykaamil.com