Ku ñépp tëfli nga tooy
Lu waay rendi ci sa loxo lay nácc
Bëgg naa la du yaa ma gënal sama bopp
Purux du gërëm ñamu daaw
Béy ci sa wewu tànk
Ku ndóbin rey sa maam, foo séene lu ñuul daw
Daw ca ba ngay am i tànk
Loo gis ci nettali lay mujje
Ku bëreey daan
Ku bëreey daanu
Werante gis bokku ci
Weddi gis bokku ci
Ku ñuy tam dëmm ngay seeñoo yeelu liir
Mbër mu ndaw moo may dëkk waaye mbër mu mag a may daan
Ku wácc sa and, and boo yéeg mu toj
Dina mátte ak du mátte, bul jox sa loxo
Pexe deesu ko weer
Kuy yoot du sëqat
Ku mar tax a naan pótit, bu ndox tuuroo nga rus
Ku wácc sa and, and boo dem fekk ca boroom
Ñákk bopp gaaw a dee
Séddoo, ca kuddu yu jëkk ya
Wuude bi ni mu la gise la lay ëwale
Mag mu ñu dab mbej ko, ca doxin wa la
Saay-saay waxul dëgg waaye yáq na xel
Ku yar sa kuy yow lay jëkk a mbëkk
Áddina du cere waaye dees koy laalo
Gune gu yaroo macc tàngal
Ñaari kuuy mënu ñoo bokk benn mbalka
Fa nga fekk baax, fa la baax fekk moo ko gën
Lu ëpp tuuru
Booy dee ca àll ba, na la gaynde rey
Kóllëre ginnaaw lay féete
Liir, bu feccam neexee, yaay jaa jápp ca mbagg ya
Lu dul dëgg du yágg
Gisee tasoon Kajoor
Dëkkëndo bu yágg mbokk la
Mbeju kanam boroom a koy fajal boppam
Ku amul yaay nàmp maam
Ay garab ca kow lañuy daje
Dëkkëndoo dina wàlle ba ciy doxat
Xam nit, xam jikkoom a ko gën
Nit ñi xamuñu ku tooñ, ku feyu lañu xam
Gumba tal naa leneen lu dul tëbaani ay teen
Gaynde bëggul mbuum, yàpp lay dunde (Yànde Koddu Seen, woykat)
Ferñeent mën naa taalug daay
Dikkleen, bukki for na almet, tey áll bi leer ! !
Garab gu la sutul du la may keppaar
Ginnaaw ay, jámm
Yaa fi sës doynag pal
Njàng moo gis am na állarba
Koo mën a yaakaar, Yálla la yaakaar
Lafañ boroom mbaam lay faral
Kuy jaay keppaar ba tàkkusaan jot, nga war a wàññi sa njëg
Doxati gëléem kow la jëm
Donn sa baay, doon sa baay a ko gën
Nit ak jikkoom ba ci biir bámmeel
Bu sindax yabee ndobin, booba garab moo fa jege
Waay soo mënulee sarax kiy yalwaan bul siif li mu jot a fortaatu !
Ndimbal na ca fekk loxol boroom
Dáq ginaar waxaale sa soxla