Ci at yi ak wéer yi weesu, mel na ni Afrik dafa dellu fa baaxi maam nekkoon, te mooy wormaal, naw, solool jiggéen. Bu ñu ko fatte fii ci Afrik, jiggéen na fi ma masa fallu, di yaay, di lingeer, di ndey-ji-réew, di buur, ca Misira démb, Nibi, Meroe, ba ci Waalo ak Kajoor. Kon…
Month: July 2012
Téy la Mandela di am 94 at…
Téy ci 18eelu fan ci wéeru Suliye lay Nelson Mandela, mi kenn dul nettali ay jàllooreem di am 94 at! Réewum Afrik di Sid yépp, Afrik gépp ak àddina sépp di ko berndeel di ko delloo njukkël.Bésam bi di bésu téy la mbootaayu xeet tuddee bésu Mandelaa ngir magal manduteem, paspasam, fonk boppam ag askanam…
El Haj Njaay: Bor yi….
Ceddo: filmu Semben Usmaan
Màki Sàll: “du ma làq kenn ku def lu dëppoowul ag yoon”!
Ci benn laaj-toontu bu njiitu-réew mi amal ag yeenekaay bu tudd Afrik te nekk ca Belsik, Màkki Sàll feeñal na ay xalaatam ci mbir yu am solo yu soxal Senegaal ak Afrik. Ci lu jëm ci li ñuy lëñbët ñi fi nekkoon ci yan anam la ñu yore woon réew mi, wax na ne, na…
Kookooy Saalif Saajo njiitu waay-fippu ya ca Kasamaas…!
Peresidaa Maki Sàll ne woon ayu-bés yale weesu, ne tàllal na loxoom waay-fippu ya nekk Kasamaas, ngir ñu tóog seet ci sunu biir naka lañu war a def ba saafara ay woowu di law ci réew mi 30 at ak lu topp. Ci laaj-toontu bii ay taskati xibaar, ay tubaab yu rajo France amal ak…
Yàggaay ci Wolof
Tombukutu: Saay-saay yi defati nañu fa ñaawtéef…
Tey ci Tombukutu, waay-fippu yiy bàkkoo lislaam te naan dañuy jihaad defati nañu fa ñaawtéef yu bon: ndax dañoo dug ci xabru ay waliyu yu mag, toj leen ba ñu mokk rumbax! Tombukutu nag, indil nañu leen fi ci dal bii, ay yooni yoon ay jukki, doon leen ci fàttali jàllooreem ci wàllu lislaam….
Woote ndawi-réew mi 2012
Naka démb ci dibeer gi la Senegaal wootewaat woote bu am solo ngir fal ndaw yiy war a taxawal askan wi ci pencum réew mi. Ci xibaar yi jot a tukkee ci kureel yi doon saytu woote bi, fés na ne mbooloo miy jàppale peresidaa Maki Sàll, di Bennoo Bokk Yaakaar, mu nar a jiitu….
Wolof ci enternet
Wikipedia ci Wolof Xibaar yi – Yeenekaay ci Wolof Baatukaay
Dal leen ag jamm!
Mbooloo mi! Ñu ngi leen di nuyu ku ci nekk ci yeen ci sa tur ak sa sànt te di leen dalal ci jàmm. Béréb bi ngeen tersi téy nag dañu koo sàncc, mool ko ci kalaama wolof, jagleel ko làmmiñ yi ñu nàmp, ci réewum Senegaal ak ci Afrik gépp. Yaakaar nañu ne lu…
Seex Musaa Ka: Xarnu bi
XARNU BI Sëriñ bi noo gi deeti ñaan Faqiir dafay nangoo dagaan Nangul nu lépp lu nu ñaan Ndax Yàlla naatal xarnu bi Noongi dangaan ci Mustafaa Ma nekk marwat’ak safaa Ak àqi amdi Mustafaa Mi Yàlla jébbal xarnu bi Ak àqi mboolem ay rakkam Ak àqi séen baay yi ñu am Ak àqi seex…