Peresidaa Ablaay Wàdd nangu na dibeer ca guddi gànnaaw ba resiltaa wote bi tàmbalee wàdd, ne Maki Sàll moom la réew mi tànn. Moom Ablaay Wàdd wóo na Maki, ñaanal ko, kañ ko, berndeel ko! Loolu di ndam lu réy ci réewum Senegaal. Rawatina ba àddina sépp ne tekk, askan wépp ne tekk di dégglu,…
Month: March 2012
Kàddu yu njëkk yi tukkee ci Màkki Sàll
Yeen wa Senegaal, góor ak jiggéen, mag ak ndaw, sama askan sope. Ci bésu dibeer bii 25 fan ci weeru Mars 2012, gànnaaw beneen bésu 26 fan Fewie bu kenn dootul fàtteeti, askanu Senegaal, àtte na, jaarale ko ci kàggu-wote yi. Ci biir réew mi ak ci bitim réew yépp, doomu-senegaal yi wote nañu jàmm,…
Laaj-toontu: B. Boris Joob
Bubakar Boris Jóob kenn la ci bindkat yi gëna mag ci Senegaal ag ci Afrik. Bind na ay téere yu siiw ci kalaama farañse ag benn téere bu am solo ci Wolof bu mu tuddee Doomi Golo. Laaj-toontu bii yeenekaayu “Le Monde des Livres” moo ko amaloon ak moom ci 16 fan ci weeru Awril….