Ci atum 2008 la ñu bari ci parti yi juunoog nguur gi jël seen matukaay daldi wóo réew mépp, amul xàjji-ag seen wan làng lañu feetoo ci wàllu politik, ngir ñu diisoo. Disóo boobu li ko waral, ñu ne, mooy gutë gi nga xam ne téy réewum Senegaal da cee tàbbi. Ndax gànnaaw ba parti…