Juwaalo Juwaalo! Maa ngi fàtteliku. Maa ngi fàtteliku siñaar ya ca keru mbaar yu naat ya Maa ngi fàtteliku siñaar yeek seeni gët, kéemtaanee lool Di sàmandaay leeraayu weer cig tefes Maa ngi fàtteliku jànt yu so yu taaroo-taaru Kumba Ndofeen naan da cay dog manto buuram. Maa ngi fàtteliku bernde dëj yuy gilli deretu…
Category: Caada
Sàrti ndaali-Maali
Dr Tamsir Anne (tekkikat bi) Ndaali Maali, walla Mande, benn la woon ci nguuru nit ku ñuul yu mag yi nekkoon démb ci déndub Afrig. Moo fi wuutu woon ndaali Gana ci Afrig sóowu jànt. Gana moom itam moo donnoon jàllooreey yeneeni nguur yu mel ni Aksum , Kuus, Nibi ak Misira démb bu Buur-Fari…
Suuxat làkk ak cosaani Afrig…
“Borom Sareet” Semben Usmaan
Waxi neen: Jàng ci làkli réew mi, 44 at ca gànnaaw…
NJUUJ-NJAAJ: Taalifu Seriñ Muusa Ka
Xaralaay létt ci Afriku démb ba téy…
Jamono ci wolof
Téere-woy yi
Téere-woy yi téere la bu ëmb taalif yu bindkat ak xaralakat yu mag ci làkki almaa taalif. Téere baa ngi genn ci atum 2011 ca Almaañ. Tamsir Anne, mi móol dal bii, moo toxal woy yooyu, tekki leen ci wolof. Woykat yi ñu gëna ràññee ci làkki almaa, mel ni Goethe, Heine, Brecht ak ñeneen…
Bàkku Senegaal
Yëngal-leen kooraa yi te dóor ci sabar yi Gaynde ñaloor yuux na. Boroom àll tëb na Tëb na tëbu jàmbaar, leeral lu doon lëndëm Suñuy naqar jeex na, sunu yaakaar ñëw na Jógleen gaa ñi, waa Afrig gépp a ngi daje Awu Yéen sunu buumi xol, nañuleen àndandoo Sunu deret waa Senegaal, jógleen Nañu…
ndeeteelu làkk yi…
Ci 7000 làkk yi ci àddina, 85 la ñi ëpp ci nit ñi, daanaka 78%, di làkk. Làkku angale ñi koy làkk tollu nañu ci 328 miliyoη, ñiy làkk sinwaa tollu ci 845 miliyoη. Làkk yi gëna ndaw yu mel ni tuwa ca Siberi, bëj-gànnaaru Risi, 235 junniy nit doηη leen a làkk. Boroom xam-xamu làkk…
Li ci biir “francophonie”
Ci ayi bés yii ñu dëgmal mbootaayi-réew yiy jëfandikoo làkki “francais” tey wooye seen bopp mbootaayu “Frankofoni” ñu ngi waaj seen 14eelu ndaje, ngir berndeel làkki francais ak caada Faraas. Looloo ma junj nag ci xalaat, ban cér dëgg ak gan gëdd lañu sédd kalaama “francais” ci réew yu wuute yooyu yépp ni Niseer, Faraas…