Bennoo, Ñaaroo, Ñettoo ba Ñent…. Mbooloo mooy doole te mooy jàmmi-réew, wante lu waay di wuyoo na koy niroo! Moo tax ba Front Siggil Senegaal seete seetaat ba tudde boppam Bennoo Siggil Senegaal, la yaakaar dellusiwaat ci askan wi, ndax xam xell ne noonu rekk la nataange, tawféex ak jàmm jiy doomi-réew miy mébét mën…
Category: Politik
Nàqar, tiis ak metit
Réewum Senegaal tollu na diggante bu xat te mooy diggante dund ak dee gannaaw ba kuréel gi waroon a saytu sàrti-réew mi feeñale parparloom ne ki ñépp di mbàmb, neex nàqari day bokk. Li ñépp yaakaaroon ne dinañu takk seen fit, def ni seen natangoo ya ca Maali gii mbaa Niseer defoon tas na! Wante…
Maa waxoon waxeet!
“Maa waxoon…waxeet!” kàddu yooyu njiitu réew mi yëkkëti ci ndaje PDS bi amoon ci 23 fan ci weeru suliye, weesu na waar ba faf wër àddina! Image Ñu bare ñu mel ni man dañoo waaru ba naan waaw, Góorgi moo lu ko jàpp, ba mu sañ a genne kàduu yu ni mel ci gemmiñam! Naka…
Askan wi fippu na!
Bésu alxamés bii di 23 fan ci weeru swe 2011 bés la bu mag ci biiri bés yi ci ndeminu demokaraasi ci réewum Senegaal. Ndax gannaaw ba njiitu-réew mi fésale yeeneem soppi sàrti réew ci anam yi ñu ko wara falee moom ak ki wo wara wuutu, la cóow lu rëy jólli fu nekk: ñépp…
Wóote ndawi-gox yi
Ci 22 fàneelu-ñaar ci wéeru Mars 2009 réewum Senegaal wóote na mpalum ndawi gox yi gox-goxaan yi, maanaam ndaw yu mel naka meer yi, njiitu kominite riiral yi ak ñi leen di jàppale. Ba nguur gi tàmbalee yenneku yenn ca ay sañ-sañam naka moomeelu suuf yi ci dëkki-kow yi ba léegi nag, ndawi gox yi…
Pencum réew mi
Ci atum 2008 la ñu bari ci parti yi juunoog nguur gi jël seen matukaay daldi wóo réew mépp, amul xàjji-ag seen wan làng lañu feetoo ci wàllu politik, ngir ñu diisoo. Disóo boobu li ko waral, ñu ne, mooy gutë gi nga xam ne téy réewum Senegaal da cee tàbbi. Ndax gànnaaw ba parti…