SENEGAL YEEWU NA Yeewu ngeen, yeewu naa, du ñu falati ku matul njiitu réew
Category: Politik
Ku wax feeñ: demokaraasi ag làkki réew mi
Wote bi nu dëgmal, ñépp xam na ñu ko, wote bu jeggi dayoo la: ndax ci la ëllëgu réew mi aaju! Wote tànn la wan yoon la Senegaal war a teggu jëm ca kanam mbaa mu teggi ko, dellu gannaaw: lawla cat! Wante li ñu soxal ci jukki bii, lu lëkkëloog loolu gaa, wante leneen…
Yaaya Jàmme: liy ñuul ci meew mi
Isaa Bokar Si ” Yaaya Jàmme mooy ndeyyi-mbill mi ci Gambi ak Kasamaas”
Isaa Bokaar Si, ambaasadeur Yaaya Jàmme la woon, bokkoon na ak Y. Jàmme nekk tàkk-der. Ku ko xam la, ku xam fu ma jaar la…Déggluleen
Màki Sàll: “du ma làq kenn ku def lu dëppoowul ag yoon”!
Ci benn laaj-toontu bu njiitu-réew mi amal ag yeenekaay bu tudd Afrik te nekk ca Belsik, Màkki Sàll feeñal na ay xalaatam ci mbir yu am solo yu soxal Senegaal ak Afrik. Ci lu jëm ci li ñuy lëñbët ñi fi nekkoon ci yan anam la ñu yore woon réew mi, wax na ne, na…
Kookooy Saalif Saajo njiitu waay-fippu ya ca Kasamaas…!
Peresidaa Maki Sàll ne woon ayu-bés yale weesu, ne tàllal na loxoom waay-fippu ya nekk Kasamaas, ngir ñu tóog seet ci sunu biir naka lañu war a def ba saafara ay woowu di law ci réew mi 30 at ak lu topp. Ci laaj-toontu bii ay taskati xibaar, ay tubaab yu rajo France amal ak…
Tombukutu: Saay-saay yi defati nañu fa ñaawtéef…
Tey ci Tombukutu, waay-fippu yiy bàkkoo lislaam te naan dañuy jihaad defati nañu fa ñaawtéef yu bon: ndax dañoo dug ci xabru ay waliyu yu mag, toj leen ba ñu mokk rumbax! Tombukutu nag, indil nañu leen fi ci dal bii, ay yooni yoon ay jukki, doon leen ci fàttali jàllooreem ci wàllu lislaam….
Woote ndawi-réew mi 2012
Naka démb ci dibeer gi la Senegaal wootewaat woote bu am solo ngir fal ndaw yiy war a taxawal askan wi ci pencum réew mi. Ci xibaar yi jot a tukkee ci kureel yi doon saytu woote bi, fés na ne mbooloo miy jàppale peresidaa Maki Sàll, di Bennoo Bokk Yaakaar, mu nar a jiitu….
Maki Sàll demoon na Kasamaas seeti jambaar yi…
Askani Senegaal am na ndam!
Peresidaa Ablaay Wàdd nangu na dibeer ca guddi gànnaaw ba resiltaa wote bi tàmbalee wàdd, ne Maki Sàll moom la réew mi tànn. Moom Ablaay Wàdd wóo na Maki, ñaanal ko, kañ ko, berndeel ko! Loolu di ndam lu réy ci réewum Senegaal. Rawatina ba àddina sépp ne tekk, askan wépp ne tekk di dégglu,…
Kàddu yu njëkk yi tukkee ci Màkki Sàll
Yeen wa Senegaal, góor ak jiggéen, mag ak ndaw, sama askan sope. Ci bésu dibeer bii 25 fan ci weeru Mars 2012, gànnaaw beneen bésu 26 fan Fewie bu kenn dootul fàtteeti, askanu Senegaal, àtte na, jaarale ko ci kàggu-wote yi. Ci biir réew mi ak ci bitim réew yépp, doomu-senegaal yi wote nañu jàmm,…