Juwaalo Juwaalo! Maa ngi fàtteliku. Maa ngi fàtteliku siñaar ya ca keru mbaar yu naat ya Maa ngi fàtteliku siñaar yeek seeni gët, kéemtaanee lool Di sàmandaay leeraayu weer cig tefes Maa ngi fàtteliku jànt yu so yu taaroo-taaru Kumba Ndofeen naan da cay dog manto buuram. Maa ngi fàtteliku bernde dëj yuy gilli deretu…
Category: Mbindu-fent
Antoine de Saint Exupéry – Ndoomi Buur si
Antoine de Saint-Exupéry Ndoomi Buur si Traduit en Wolof par Dr. Tamsir ANNE Tudee naa ko Leon Werth Yeen xale yi, na ngeen ma baal, ndax teere bii ki ma ko tuddee du xale, mag la. Wante am naa lay: benn, kookooy sama xarit bi ma gën a fonkk…
Leebu Wolof-Njaay: A ni aada
1. Aar moo gën faj. (20) Image 2. Aawo, aw la tudd. (9) 3. Aawo buuru këram. (2) 4. Aaye na, aayeetul keroog. (1) 5. Ab dag du bëgg moroom ma. (14) 6. Ab lonku, daar a ca gën. (2) 7. Ab yeel bu ëppee ab lupp booba jàngoro rax na ca. (20) 8. Abb…
Benn bés, benn woy
Lenn li Ci kow puj yépp Lépp a ngi ne tekk Ci senn ruxx Do yëg sax Lu noyyi. Picc saa ngi ne selaw Ci àll bi. Xaaral rekk, Léegi yow itam Nga noppalu. Goethe Tekkikat bi Dr. Tamsir Aan.Téere-Woy yi(2011, Kulturbild Verlag)
Taalif “Les poetes de la rue”
Waxi Wolof Njaay
Juddu ci gëléem, nàmp ci mbaam Bu sunu boroom bi bëggee, ñépp ñàkk Bant su tooyee yomb a jubbanti Juróom-ñeenti walaakaana soo leen bëggee jubbanti, soo moytuwul fukkeel leen Boroom kuddu du lakk Wax dëgg du wàññi wërsëg Nit ki, li nga ko gëne, booy sangu bu ko summi Doxkat du fekke dëju maamam Njëriñ…
Seex Musaa Ka: Xarnu bi
XARNU BI Sëriñ bi noo gi deeti ñaan Faqiir dafay nangoo dagaan Nangul nu lépp lu nu ñaan Ndax Yàlla naatal xarnu bi Noongi dangaan ci Mustafaa Ma nekk marwat’ak safaa Ak àqi amdi Mustafaa Mi Yàlla jébbal xarnu bi Ak àqi mboolem ay rakkam Ak àqi séen baay yi ñu am Ak àqi seex…
Taalif
woyi-kañ
Woyi-làmb
Laam ag liif Masambaay Mbéri Ndaw Béy du raas deemu guddee! Masambaay Mbéri Ndaw Béy du raas deemu guddee! Yégg naa! Yégg naa! Yégg naa ! Yégg naa ba ca biir Kaaba ga! Bind fa laam ak liif soo ga ñëw Laam ak liff googu laay daane mbër! Fa ma jaar ku fa jaar taq…