Category: NEKKIN
Ngëneel yi ci garabu nebedaay
Nebedaay walla ci turu wolofam dëgg saab-saab, garab la gu bari ay ngëneel ci wàllu dund ndax witamin ak ferñeent yu bari yi ci nekk ak li mën a faj mbaa fàggu ci ay jangoro. Su ñu wesaare woon ngëneel yi nekk ci nebedaay ba ñépp jot ci, kon tey febaru xale yu bare dooti…
Ñi seen xel matadi ci biir Ndakaaru…
jiggéen yu mën góor…
Ci at yi ak wéer yi weesu, mel na ni Afrik dafa dellu fa baaxi maam nekkoon, te mooy wormaal, naw, solool jiggéen. Bu ñu ko fatte fii ci Afrik, jiggéen na fi ma masa fallu, di yaay, di lingeer, di ndey-ji-réew, di buur, ca Misira démb, Nibi, Meroe, ba ci Waalo ak Kajoor. Kon…
Téy la Mandela di am 94 at…
Téy ci 18eelu fan ci wéeru Suliye lay Nelson Mandela, mi kenn dul nettali ay jàllooreem di am 94 at! Réewum Afrik di Sid yépp, Afrik gépp ak àddina sépp di ko berndeel di ko delloo njukkël.Bésam bi di bésu téy la mbootaayu xeet tuddee bésu Mandelaa ngir magal manduteem, paspasam, fonk boppam ag askanam…
Kookooy Saalif Saajo njiitu waay-fippu ya ca Kasamaas…!
Peresidaa Maki Sàll ne woon ayu-bés yale weesu, ne tàllal na loxoom waay-fippu ya nekk Kasamaas, ngir ñu tóog seet ci sunu biir naka lañu war a def ba saafara ay woowu di law ci réew mi 30 at ak lu topp. Ci laaj-toontu bii ay taskati xibaar, ay tubaab yu rajo France amal ak…