Cosaan soo kooy seet, mënees naa wax ne, mooy xàncc biy boole ay nit ba ñu mëna ràññee ne nit ñooñee ñooy askan sangam. Ndax soo demoon téy marse Sàndaga, di béréb bu ay turist yu joggee fun nekk ci àddina di dajaloo di jënd, doo mëna wax mukk ne ñooña fa tase askanu turist…
Author: tam
Xasida ci Wolof : Sindiidi
SINDIIDI Ki ko tekki ci wolof : Cheikhouna LO Ngabou Ci turu Yàlla jiy yëramaakoon bi di jaglewaakoon laay tàmblee, di julli (ñaan xéwël ak mucc) ci Yonnent bi aki waa këram aki àndandowam. 1- Yàlla ( maa ngi lay ñaan) ci (barkeb) ku ñu belli (tànn) ka jàmbaar ja (Muhammad) ak sa xarit ba…
“Symbole bi”: céy li ci réew mi!
Symbole ci nasaraan, su ngeen ko déggee mooy lëf koo xam ne dafa am lu muy mandaragaal! Du lëf ki ci boppam moo am solo, waaye la muy junjj ci xelu nit ñi la… Ndekete këf ki ñu leen bëgg a nettali masu fee jóg te mooy symbole bi fi daara tubaab bi indi di…