Author: tam
Timbukutu: peyu xam-xam
Timbukutu: péyu xam-xam bu yàgg te sax! Ni ñu leen ko fi waxeewoon ci jukki bi weesu, bind, sàkku xam-xam, gëstu ak diine lu yàgg la ci Afrik! Wante ñakka xam ak ñakka am xel-ñaar tax na ba ñu bare defe ne gànnaaw woy aka fecc, mbaa léeb amul genn ndono lu am solo lu…
Kopparu CFA ag Ëro ñoo xoj Afrik !
Nicolas Agbohou jàngalekat la ci fànnu koom-koom ci daara yu mag ya ca Tugal, cosaanoo Kodiwaar. Ci laaj-toontu bii ñu leen fi tekkil day ηàññ doxalinu réewi Afrik yiy jëfandiku Koparu CFA. Nee na kopparu Ëro ag bu CFA, ñooy ñaari yëf yi tax ba réewi Afrik yi feete làng googu mënu ñoo genn cig…
Ngëneel yi ci garabu nebedaay
Nebedaay walla ci turu wolofam dëgg saab-saab, garab la gu bari ay ngëneel ci wàllu dund ndax witamin ak ferñeent yu bari yi ci nekk ak li mën a faj mbaa fàggu ci ay jangoro. Su ñu wesaare woon ngëneel yi nekk ci nebedaay ba ñépp jot ci, kon tey febaru xale yu bare dooti…
Benn bés, benn woy
Lenn li Ci kow puj yépp Lépp a ngi ne tekk Ci senn ruxx Do yëg sax Lu noyyi. Picc saa ngi ne selaw Ci àll bi. Xaaral rekk, Léegi yow itam Nga noppalu. Goethe Tekkikat bi Dr. Tamsir Aan.Téere-Woy yi(2011, Kulturbild Verlag)
Bàkk: Maam Góorgi Njaay
Jaar-Jaaru Abe Pierre Mohamed Njaay ak S
BATAAXAL BU MAG BI ËMB SAÑ-SAÑI DOOMI AADAMA
UBBITE Ñu jàpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sañ-sañam yépp-dañu yam te kenn mënukóo jalgati, te lu lépp nekk na cës laay ci taxufeex ci mbirum àtte ak jàmm ci biir àdduna. Ñu jàpp ne ñakk xam ak soofantal sañ-sañi doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax képp kuy dund fippu. Temano…
Ndeysaan bu Mansuur Sora Wàdd
Woyi nax-xale
Baay Malamin Daara Bindal na ma tereee Tere yombul Saalum Salum ñaari neeg la Ñeteel ba di waañ wa Waañ wa waañi buur la Buur ba buuri Saalum Baay Malamin Daaraa Bindal na ma tereee Tere yombul Saalum Salum ñaari neeg la Ñeteel ba di waañ wa Waañ wa waañi buur la Buur ba buuri…
Mbindum wolof
Mbind mi* 1. Jàppal lii à warul a wéet, fàww mu am araf wu ko féete wàllu ndeyjoor te loolu mënul a nekk lu dul baatoodi bu ñu séexal (tàkk), walla q nga xam ni jikkoy baatoodi bu ñu séexal la làmboo (sàq), walla ñaari baatoodi yu dend (ànd). 2. Maaska yi Maaskay téj «accent…