Ku weg nit ñi wegees ko, ku xeeb nit ñi deesu ko weg, ka wax lii de wax na wax ju rafet: boo bëggee dund sa diine, mucc, sa wërsëg lëw (bari), sab der ñoη, boo bëggee loolu, sa làmmiñ bu ci tudd mukk ayibi nit, ndax kat yaw it am nga ay ayib, nit ñi ami làmmiñ. Bu Yàlla dogalee say gët rot ci ayibi nit, nee leen, yéen gët yi bu leen xool de, ndax nit ñi ñoom it am nañu ay gët.
Xamal ne wuute ab dëel (dige te defoo ko) ak fen bokk nañu ci gàkk-gàkki wax, dee leen teet (moytu).
Nekk na ci adiisub kii nga xam ne maa ngi sàkku sellug ay julleeki sëlmal yuy sottiku ci moom aki ñoñam aki saabaam, yi diy
ndëgërlaay. Dénk naa leen adiis ba: nekkal di kuy wax dëgg, teetal fen ngir nga kawe.
Fonkal sa ñaari waay-jur, te am yërmaande ci ñoom ak ñeewant, te deel gaaw ci seeni ndigal aki mbir. Deel ba mbooleem li ñu
la tere, boo ko dee def de, sag kawe dina yokku. Képp ku la mag ci jegeñaale yi na nga ko weg ak ñu dul jegeñaale yi, rikk na
nga nekk ak mbindéef yi ci jikko yu rafet, kon de Aji-Sàkke ji (Yàlla), dina la sopp. Na ngay rafetal jikko yi cig yaatu-yaatulu, ak a sàkkoo sopplu ci ñoom (mbindéef yi) kon de soppees na la.
Na ngay nooyal i wax ci nit ñépp, loolu de ci jikkoy waay-ñaw yi la bokk (ñu yewwu ñi). Xibaarees na jële ca boroom ngënéel la (Yonnant bi (j.m)): genn-wàllu xel mooy sopp-sopplu ci nit ñi (fexe ba nit ñi sopp la).
Bokk na ci texeeg nit ki, xolub boroomug njub bañ koy bañ ak a foñ.
Deel sàkku seenug ñaan foo tollu, deel barkeelu it ci ñoom, loolu de dina la yobbe ag kawe guy dolliku. Màggal boroom xam-xam
bu jëfe (xam-xam ba) mooy màggal boroom aras (toogu ba)…
Boroomug yayoo bu sàkkoo ci yaw dara, defal ko ko. Bul nay mukk ci poñat mii (alali àddina jii) ba loolu di waral sa gàcca ca
yalmal qiyaam bis pénc. Boroomug nay ku sori Yàlla lay doon ak mbindéefam yépp foo ko fekk. Boroomug nay dees koy wommat jëme sawara, soril ko àjjana safaan ba mooy aji tabe ja, ca lees wax, kon nekkal aji tabe ji, bul nekk mukk aji nay ji.
Bul taamu mukk ab noflaay ak loxoy neen, ag yiw nekku ci de te kenn du jot “teddnga” ci lu dul ab coona niki lees ko waxe:
Cig farlu lees di jote kawe ga, ku bëgg ag kawe fog guddi yi (fog ñàkk a nelaw guddi).
Da ngay sàkku ag “teddnga” ba noppi di nelaw guddi, na la wóor ne xemmemloo nga sa bakkan lu jomb (bëgg nga lu manul a nekk)
Teralal gan ya cig yaatal, dalal jàmm ak ganale ak mbégteek jegeel. Rikk bu sa xol xat mukk ci gan, ndax moom balaa yàgg mu laxas dem… ku gëm Yàlla ak bis pénc ba, nay teral ganam. Ab woykat it def aw woy ci galanu kaamil: gan gi teral ko, ab fanaanuwaayam yelleef la, rikk bul nekk rëbbum waay-wàcc yi, bul nekk ηàññ ak saagay gan yi. Na nga xam ne gan de fàwwu mu nettali ñoñam fa mu fanaan, ak doonte laajeesu ko ko. Wolof nee na: gan dees na ko xañ lépp ba mu des nettali. Na nga ko gatandoo kanam gu nooy te yaa, waxees na ne moo gën ganale, moom la woykat biy feddali…
Bul bàyyi benn bis am njàng, te nga jëfe ko cig jaamu Yàlla Xam-xam day dundal xolub aji xamlu ji, day leeral xol tey dindi ngumba-gu xol. Xamal ne rawanteeg nit ñi ci xam-xam lay nekk ak diine, na nga dëkke muñ. Ci ñoom ñaar it la ku gën di gëne, du ci ag askanoo ci ku kawe. Ci wàllug askan, moo xam baay la mbaa nday, kon farlul ci ñoom ñaar ànd ceek i teggin.Booy sàkku xam-xam dimbandikool Yàlla te sellal ci xol bu dal.Te ngay dëkke jàng nag, ak sàmmoonteek ndigal ak terey sunu boroom yi. Néewal i nelaw, néewalug regg Saxal ci jàng ak nafar li nga jàng te bañ koy dëddook a ginnaawal. Na ngay wuuteek bakan, ndaxte bakan li mu lay xiir du dara lu dul luy waral ag tëj.
Neewalal nelaw yi, tàggool ak tàyyeel, néewalal noflay, gàttalal mébat. Xamal ne ku bañ a jàng cig ndawam, dina dajeek réccu. Ndaxte képp ku gaawantuwul jëm ca xam-xam ya (ku gaawantuwul jàngi) te feex ngir ñoom njëkk yitte ya. Lu ci ëpp du am la mu ca yittewoo, te du ca jot càkkutéefam. Ndaxte taggees na njàngum gone ne mook bind ci doj a yam (bind ci simaa bu tooy, bu wowee du dañati). Ñu niroole nag njàngum mag ak bind ci ndox, ni muy ñàkke jeexiit …
Ndam daal ñoñ xam-xam la ñeel, ndax ñoo gindee ñeel ki ko soxla. Darajay cam si (nit ki) mooy la mu man, am ci ag xereñ, waay-reer yi (ñi amul xam-xam), ay noon lañu ñeel woroom xam-xam yi. Wutal xam-xam, kon de di nga ci dunde ba fàww, ndax nit ñi waay faatu lañu, te woroom xam-xam yi dunu faatu waay-dund lañu…
Na nga xam ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul tëyye sa bopp wëliif “dégg naa ak waxees na”. Du la may xam-xam,
lennam mukk li, feek joxoo ko sa lépp, kon farlu ci. Jox ko sa lépp ci lu dul xëccoo, fogalal sag guddi (bul di nelaw guddi) te xiifal sa biir. Deel maral sa bëccëg ci xam-xam, di ci sonal sa cér yépp ànd ceekug tegginu.
Ku ko sàkkoowul noonu du ca am lu am njariñ, noonu lees ko xibaare. Xibaarees na it ne moom de ab foñaakon la (kuy daw di
soree), ku dul cam su di ab muñkat du ko am. Na ngay sax cig toroxlu cig toroxal sa bopp, ca jamonoy xamlu ja, kon de danga
am leerug xol. Ab xamlukat bu rëyee, du am nammeelam. Bayyil ag peexlu, bul di toog mukk cib lal ca jamonoy jàng ja, ci lu dul aw tiis (ñàkk pexe). Na ngay boole yitte ji jépp ci li ngay sàkku, ci lu dul gestu jëm ci lu warul. Bul di déglu nit ñi mbaa xëccoo yi ñu nekk. Bul di yeexe am njàng, mbaa nga naan di naa ko defi bu ma feexee, soo bëgee dab gaa ñu baax ña.
Àdduna de am na yitte yuy teree àgg ca njub ga, te duñu jeex. Dee de cig mbetteel lay ñëwe, te bariwaa na fu mu bóome boroomi
soxla.
Mu jubloo wax ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul tëju wëlif ag jaxasoo, xamal ne du la jox mukk lennam ndare da nga koo jox sa lépp, ku ci xiifalul biiram, fog guddeem, mar bëcëgam, sonali céram, du ca am lu am njariñ, ndax xam-xam ag leer la, ku dul aji-muñ du ko am. Woykat ba nee: sàkkul te bul yoqat ci sàkku gi, gàkk-gàkkub aji-sàkku ji xam-xam mooy yoqat. Xanaa gisoo ne buum sax bu yàggee jaar ci pindub teen, bàyyi fay jeexiital.
Kuy jàng fàwwu muy toroxlu ak a suufeel boppam buy xamlu, lu ko moy du ca am nammeelam. War nay bàyyi ag noos, bu muy toog
cib lal mukk ci waxtuw jàng, ndare bu loolu da di lu manul a ñàkk ba àgg ci lool, booleel sa yitte jépp booy jàng ca la ngay jàng, bul di gestu leneen lu ko moy, bul di déglu nit ñi mbaa la ñu nekk, mi ngi lay dénk it nga bañ di yeexe am njàng, naan da nga koy bàyyi ba féex ci yitte yi, ndax yittey àdduna duñu jeex mukk. Kenn faju fi aajoom, aajo it fajuwu fi ndare jeneen daa juddu. Yaw amaa na sax dee gi dikkal la, ba laa booba, ndax dee de mooy aji fàddu (ku fi nekkul) ji gën a jege, te buy ñëw cig mbette lay doon. Ginnaaw bi mu wax ci nees di tegginoo ak Seexul Murabbii (Sëriñ biy jàngale) ak ki lay jàngal ak sa mbokk dëgg ak sa àndandoo dëgg, daal di ne: Fig wegeel man a yam mooy nga weg sa sëriñ, def ko ab sang, may ko say xeewal, fajal ko ay aajoom, lii feek yaa ngi dund, ci di ko jox, di ko liggéeyal li nga man.
Benn xool bob cofeel bu tukkee cib sëriñ jëm cib taalibeem mooy ngënéel ya tey kawe ga. Na nga nekk fa sëriñ ba niki ab néew
bees tëral ci kanamu aji-sangam, kon de nga jariñu. Boo dee sàkku xam-xam it, na ngay sàkku ngërëmul aji-jàngale ji ngir jëmmi Yàlla. Na nga mel ca sab sëriñ nib jaam, loolu de dina tax nga jot darajay buur yi.
Xamal ne njariñ deesu ko am ndare cig màggal ci li ñu wax. Kem ni nga màggale sab sëriñ ngay ame li nga bëgg, ci ngay ame it
barke. Ku gërëmloowul ab sëriñam, du gërëm ab ndongaam. Bariwaa na waa jees miin ci xam-xam te kenn jubluwu ko.
Yal na nu Yàlla musal ak yeen ci xam-xam bu jariñul ki ko xam…
Bu la Yàlla tawféexalee ba nga am sëriñub dëgg bu raw ci lefum Haqiiqa. Rikk na nga jug ci sàkku ngërëmam, xeeñtu nammeelam,
te ba lépp loo nekkoon bu njëkk. Na nga mel fa moom ni néew fa ka koy sang, da koy wëlbati fu nekk muy wëlbatiku.
Mbokk dëgg ak xarit bu wér ñoo gën a néew luy néew. Mooy lu mel ne waxi ki wuññi lëndëm yi: sa xarit dëgg mooy ki ànd ak yaw. Mooy kiy lor boppam ngir jariñ la, mooy kok bu la jamono njattee mu sonnal boppam ngir siggil la, ma ne mooy ki lay nëbbal lu ñaaw ngir yëkkati la.
Tudd naa ciy teggin am mbooloo mom dina fajal ku ko taqoo mbooleem ay aajoom. Doy na sëkk ci ku ko settantal, aji saafara la ci ku ko jëfe. Dina tegtal boroomum xel, dina ko tegtal banqaasi bunt bii, bu ci royee ànd ceekug toroxlu. Ba mu far matal fànni teggin yi te bokk na ci yooni tegginu yi: Di def li nga gis mu rafet tey ba li nga gis mu ñaaw kenn ci ñoom laajees na ko: ku la yar? maanaam koo roy ba mel nii nga mel? Mu ne damaa dëkke di xool réerug kii nga xam ne ne réeram gi leer na nàññ. Bu ko defee ma koy teet (moytu). Fii la toontu li yam.