Timbukutu: péyu xam-xam bu yàgg te sax! Ni ñu leen ko fi waxeewoon ci jukki bi weesu, bind, sàkku xam-xam, gëstu ak diine lu yàgg la ci Afrik! Wante ñakka xam ak ñakka am xel-ñaar tax na ba ñu bare defe ne gànnaaw woy aka fecc, mbaa léeb amul genn ndono lu am solo lu…
Category: Caada
BATAAXAL BU MAG BI ËMB SAÑ-SAÑI DOOMI AADAMA
UBBITE Ñu jàpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sañ-sañam yépp-dañu yam te kenn mënukóo jalgati, te lu lépp nekk na cës laay ci taxufeex ci mbirum àtte ak jàmm ci biir àdduna. Ñu jàpp ne ñakk xam ak soofantal sañ-sañi doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax képp kuy dund fippu. Temano…
Mbindum wolof
Mbind mi* 1. Jàppal lii à warul a wéet, fàww mu am araf wu ko féete wàllu ndeyjoor te loolu mënul a nekk lu dul baatoodi bu ñu séexal (tàkk), walla q nga xam ni jikkoy baatoodi bu ñu séexal la làmboo (sàq), walla ñaari baatoodi yu dend (ànd). 2. Maaska yi Maaskay téj «accent…
Jal-jali: filmu Usmaan Wilyam Mbay
Sinemaa: Mandaa bi (Sembeen Usmaan)
Fàttaliku démb: Michael Jackson
Xoy 2013: Li saltige yi wax….
Waxtaan ag Samba Jabare Sàmb
Laaj-toontu ak Njaga Mbay
Jaar-jaaru woykat bu jege woon askanam Ci sanwiye 1999, yeneekay Lasli/Njëlbéen amoon na laaj-tootu bu yaatu ag Njaga Mbay, doon ca feeñal ay jaar-jaaram. Waxtaan woowu Njaga Mbay amoon ak Séydu Nuuru Njaay, di njiital Lasli/Njëlbéen moom lañu leen fi indilaat, di ci ñeel woykat bu mag bu àddina sépp jooy. Kan mooy Njaga Mbay?…
Waxi Wolof Njaay
Juddu ci gëléem, nàmp ci mbaam Bu sunu boroom bi bëggee, ñépp ñàkk Bant su tooyee yomb a jubbanti Juróom-ñeenti walaakaana soo leen bëggee jubbanti, soo moytuwul fukkeel leen Boroom kuddu du lakk Wax dëgg du wàññi wërsëg Nit ki, li nga ko gëne, booy sangu bu ko summi Doxkat du fekke dëju maamam Njëriñ…
Seex Musaa Ka: Xarnu bi
XARNU BI Sëriñ bi noo gi deeti ñaan Faqiir dafay nangoo dagaan Nangul nu lépp lu nu ñaan Ndax Yàlla naatal xarnu bi Noongi dangaan ci Mustafaa Ma nekk marwat’ak safaa Ak àqi amdi Mustafaa Mi Yàlla jébbal xarnu bi Ak àqi mboolem ay rakkam Ak àqi séen baay yi ñu am Ak àqi seex…